2
Yunus a ngi tinu
1 Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal jën wu mag, mu wonn Yunus. Mu nekk ca biiru jën wa ñetti bëccëg ak ñetti guddi.
2 Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa.
3 Mu ne:
Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma.
Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.
4 Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma.
Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
5 Man nag ma naan: «Dàqees na ma, ba ma sore la,
waaye maay dellu gis sa kër gu sell ga!»
6 Ndox maa ma tanc ba ci put,
xóotey géej mëdd ma,
waag ba laxasu sama bopp.
7 Ca reeni tund ya laa suuxi,
caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww,
waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan,
yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.
8 Noowal bakkan a nga may rëcc,
sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji,
sama ñaan àgg fa yaw,
ca sa kër gu sell ga.
9 Ñiy wormaal neenug neen daal,
ñoo dëddu seen yiw fa Yàlla.
10 Man nag, ci biir cant laa lay sarxale.
Li ma xas laay sottal.
Wall, fa Aji Sax ji!
11 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax ak jën wa, mu goqi Yunus ca tefes ga.