22
Daawuda sant na
Daawuda woy na Aji Sax ji gannaaw ba ko Aji Sax ji xettlee ci mboolemi noonam, xettli ko it ci Sóol. Kàdduy woy wa lii la. Mu ne:
Aji Sax ji laay sës,
mu di ma aar,
di ma wallu.
Mooy sama Yàlla, ji ma sës, yiiru,
fegu, mucc,
làqu, raw,
mucc fitna.
Ki yelloo cant, Aji Sax ji,
moom laa woo, mucc ci samay noon.
 
Gannaxi ndee mëdd ma,
walum kasara naq ma.
Buumi njaniiw laaw ma,
dee ne jaas, di ma fiir.
Ma jàq, woo Aji Sax ji,
ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram.
Ma yuuxu, muy dégg.
 
Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri,
kenuy asamaan jaayu, di reg-regi.
Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya,
sawara boye ca gémmiñ ga,
xal yu yànj tàkke ca.
10 Mu firi asamaan, wàcc,
niir yu fatt lal tànk ya.
11 Ma nga war malaakam serub, di naaw,
daayaarloo laafi ngelaw.
12 Ma nga bàddoo lëndëm,
làmboo jali ndox aki xàmbaar.
13 Leer a ko jiitu,
ay xali sawara topp ca.
14 Aji Sax jee dënoo asamaan.
Aji Kawe jee àddu,
15 soqiy fitt ak jumi melax,
tasaare leen, fëlxe.
16 Aji Sax ji gëdd,
nokki, mu riir;
xuri géej ne fàŋŋ,
kenuy suuf ne duŋŋ.
 
17 Moo yóotoo fa kaw, jàpp ma,
seppee ma ca xóotey ndox ma,
18 musal ma ca noon yu mag,
ya ma bañ te man ma.
19 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee,
Aji Sax ji taxawu ma,
20 yaatal ma,
bége ma, ba xettli ma.
 
21 Aji Sax jee ma yool sama njekk,
samay loxoo set, mu fey ma.
22 Sàmm naa yooni Aji Sax ji,
bonuma, di moy sama Yàlla.
23 Dama ne jàkk ndigalam yépp,
dëdduwma dogali yoonam.
24 Seede na, may jëfeg mat,
di moyoo tooñ.
25 Aji Sax jee ma yool sama njekk,
rafetlu sama mucc ayib.
 
26 Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore;
ku matale, fekk la matale;
27 ku sellal, fekk la sell;
ku dëng, fekk laak say feem.
28 Yaw yaay musal xeet wu néew doole,
kuy daŋŋiiral, nga detteel.
29 Yaw Aji Sax ji, kay, laay niitoo,
Aji Sax jeey leeral sama lëndëm.
30 Maak yaw kay, ma song gàngoor.
Maak sama Yàlla, ma tëb um tata.
 
31 Yàllaa mat,
kàddug Aji Sax jee wér te wóor.
Mooy feg képp ku ko làqoo.
32 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji?
Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
 
33 Yàllaa may làqe dooleem,
xàllal ma, yoon mat.
34 Moo ma gaawal ni kéwél,
taxawal ma fu kawe.
35 Moo may tàggat ngir xare,
may bank xalag xànjar.
36 Aji Sax ji, yaa may feg, musal ma,
yaa may nangul, darajaal ma.
37 Yaa ma xàllalu yoon,
duma tërëf.
38 Maay dàq noon yi, falaxe,
jekkli, doora dëpp.
39 Ma rajaxe, nemmali, jógatuñu,
xanaa fëlëñu, ma joggi.
40 Sol nga ma dooley xare,
sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41 Yaa ma won ndoddi noon,
ma boole bañ yi, bóom.
42 Ñu ne wallóoy, wall amul,
ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
43 Ma wol, ba ñu doon pënd,
dër, note ni banu mbedd.
44 Yaa ma xettli ci bokk yiy fippu,
def ma, ma jiite ay xeet;
waaso wu ma xamul sax nangul ma,
45 ku ma ci dégg, déggal ma,
ay doomi doxandéem di ma raamal,
46 ne yàcc,
génne seeni tata, di lox.
 
47 Aji Sax jeey Kiy dund.
Kii ma sës moo jara sant.
Yàlla sama cëslaay ji may musal moo màgg!
48 Mooy Yàlla ji may feyul,
di ma suufeelal xeet yi.
49 Xettli nga maak ku ma bañ ak ku ma jógal,
kaweel ma, ma tiim leen,
xettleeti ma cib soxor.
 
50 Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi,
kañ la!
51 Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy,
yaay ji ngor ki nga fal,
muy man Daawuda, di sama askan ba fàww.