Bataaxal bu jëkk bi Yàlla may Pool,
mu bind ko
WAA KORENT
1
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobarey Yàlla, man ak Sosten sunu mbokk,
2 noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla, mi dëkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, yéen ñi Yàlla sédde boppam jaare ci Kirist Yeesu, yéen ñi Yàlla woo, ngeen sell, boole leen ak ñi nekk ci àddina sépp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy seen Boroom, di sunu bos.
3 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi may yiw ak jàmm.
Pool sant na Yàlla
4 Duma jóg ci di sant Yàlla sama Boroom ci seen mbir ndax yiw, wi mu leen may ci seen bokk ci Kirist Yeesu.
5 Ndaxte ci yiwi Yàlla yépp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam.
6 Ndaxte li nu doon seedeel Kirist, Yàlla dëggal na ko ci yéen.
7 Noonu nag ñàkkuleen genn may léegi bi ngeen di séentu waxtu, wi sunu Boroom Yeesu Kirist di feeñ ci biir ndamam.
8 Kirist dina leen dooleel ba ca muj ga, ngir ngeen baña am wenn ŋàññ bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist délsee.
9 Yàlla kuy sàmm kóllëre la, moom mi leen woo, ngir ngeen bokk ak Doomam Yeesu Kirist, sunu Boroom.
Na mbooloo mi juboo
10 Waaye bokk yi, maa ngi leen di dénk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te baña féewaloo ci seen biir. Waaye nangeen ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.
11 Ndaxte bokk yi, waa kër Kelowe xamal nañu ma ne dangeen di xuloo.
12 Maa ngi ñëw ca wax ja: kenn ku nekk ci yéena ngi naan: «Man ci Pool laa bokk!» «Man ci Apolos!» «Man ci Sefas!» «Man ci Kirist!»
13 Ndax Kirist dafa xaajoo? Ndax Pool lañu daajoon ca bant ba, mu dee ngir yéen? Ndax sóob nañu leen ci ndox, ngir wone ne bokk ngeen ci Pool?
14 Maa ngi sant Yàlla ci li ma sóobul kenn ci yéen, ku dul Kirispus ak Gayus,
15 ngir kenn baña wax ne ci sama tur lañu ko sóob.
16 Ahakay! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas. Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen.
17 Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may sóobe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may yégle xibaaru jàmm bi, te ma bañ koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir baña ñàkkal faayda deewu Kirist ca bant ba.
Xam-xamu nit jotewul dara ak bu Yàlla
18 Ndaxte yégleb deewu Kirist ca bant ba, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye ci nun ñi aw ci yoonu mucc gi, dooley Yàlla la.
19 Ndaxte Mbind mi nee na:
«Dinaa folli xam-xamu boroom xam-xam yi,
lem xalaati ñi am xel.»
20 Ana boroom xam-xam bi? Ana kaaŋ mi? Ana boroom làmmiñ wu neex wi ci àddina sii? Xanaa Yàlla wonewul ne xam-xamu àddina si ag ndof la?
21 Gannaaw àddina si ci xam-xamam demul ba xam Yàlla —te Yàllaa dogal loolu ci xam-xamam— soob na Yàlla mu musal ñi gëm, jaar ci yégleb xibaaru Kirist, fekk ag ndof la ci bëti nit.
22 Ndaxte Yawut yi ñu ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam.
23 Waaye nun nu ngi yégle Kirist, mi ñu reyoon ca bant ba, te loolooy téq ngëmu Yawut yi, di ag ndof ci ñi dul Yawut.
24 Waaye ci ñi Yàlla woo, ñuy Yawut mbaa di Gereg, Kirist mooy dooley Yàlla, di xam-xamu Yàlla.
25 Li ñuy wax ag ndof ca wàllu Yàlla moo gëna tedd xam-xamu nit. Te li ñuy wax ñàkk dooley Yàlla moo ëpp kàttan dooley nit.
26 Bokk yi, seetleen seen nekkin, bi leen Yàlla di woo. Barewul woon ci yéen, ñi ñuy tudde ay boroom xam-xam mbaa ay boroom doole mbaa ñu rafet ab juddu.
27 Waaye li àddina teg ag ndof, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom xam-xam yi; te li àddina teg ag ñàkk doole, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom doole yi.
28 Li dul juddu bu rafet te mata xeeb ci àddina, Yàlla tànn na ko; Yàlla tànn na li nekkul, ngir neenal li nekk.
29 Noonu kenn du mana damu ca kanam Yàlla.
30 Waaye Yàlla moo def ba ngeen bokk ci Kirist, moom mi doon ci nun xam-xam bu jóge ca Yàlla, maanaam: sunu njubte, sunu sellaay, sunu njot.
31 Loolu dafa am, ngir li Mbind mi wax am, ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»