3
Fonkleen dund gu bees gi ci Kirist
1 Kon nag ndegam dekkeendoo ngeen ak Kirist, wutleen yëf, ya nekk ca kaw, fa Kirist toog ca ndijooru Yàlla.
2 Fonkleen yëf ya ca kaw, te ngeen baña faale yi ci suuf,
3 ndaxte dee ngeen, te seen dund boole nañu ko ak Kirist, denc ca Yàlla.
4 Te bés bu Kirist miy seen dund feeñee, yéen itam dingeen feeñ ak moom ci biir ndam.
5 Kon nag li nekk ci yéen te bokk ci mbiri àddina, jébbal-leen ko dee, yu deme ni ndoxaanu yàqute, sobe, xemmem, bëgg-bëgg yu bon, ak bëgge, maanaam bokkaale Yàlla.
6 Yooyooy xëcc merum Yàlla.
7 Yéen itam noonu ngeen daan doxale bu jëkk, ba ngeen daan dunde noonu.
8 Waaye léegi bàyyileen yii yépp: mer, xadar, kiñaan ak di génne ci seen gémmiñ sos ak wax ju ñaaw.
9 Bàyyileen di fen seeni moroom, ndaxte summi ngeen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale, moom ak ay jëfam;
10 te sol ngeen dund gu bees, gi Yàlla sàkk te di ko yeesal ba mu mel ni moom, ngir ngeen man koo xam bu wér.
11 Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku jàngul ni Baarbaar yi, ak ku yewwuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay lépp te dëkk ci ñépp.
12 Kon nag ndegam Yàlla tànn na leen, sellal leen, sopp leen, solooleen boog yërmande, laabiir, woyof, lewet ak muñ.
13 Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale.
14 Ci kaw loolu lépp amleen mbëggeel, giy jokkale lépp, ba mu mat.
15 Na jàmm ji Kirist di joxe not seeni xol, ndaxte Yàlla woo na leen ci loolu, mel ni ay cér yu bokk benn yaram; te gërëmleen Yàlla.
16 Na kàddug Kirist dëkk ci yéen, bay baawaan, ngeen di jànglante ak a artoonte ci seen biir ak xel mu mat sëkk, di woy ak a gërëm Yàlla ak seen xol bépp, ay taalifi Sabóor, ay kañ Yàlla ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla.
17 Lu ngeen mana def, muy ci wax mbaa ci jëf, wéerleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci moom gërëm Yàlla Baay bi.
Àndleen bu rafet ci seen biir
18 Jigéen ñi, na ku nekk nangul jëkkëram, ndaxte looloo jekk ci ñi bokk ci Boroom bi.
19 Góor ñi, na ku nekk bëgg soxnaam te muñal ko.
20 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi.
21 Baay yi, buleen bundxataal seeni doom, ngir baña jeexal seen xol.
22 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang, yi ci àddina. Buleen ko def rekk ci seen kanam, di sàkku ngërëm, waaye na nekk lu dëggu ci yéen, ndax seen ragal Boroom bi.
23 Lu ngeen mana def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit,
24 xam ne Boroom bi dina fey seeni jëf, mu di cér bi mu leen dencal. Kirist mooy Boroom, bi ngeen di liggéeyal.
25 Waaye ku def lu bon, Boroom bi dina la delloo sa jëf, te du gënale.