5
Yéen nag ñiy goney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu. Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ.
Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi. Dawleen it lu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla. Na leen wóor ne kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla. Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil. Kon nag buleen séq ak ñoom dara. Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi.
Dundeleen ni ay goney leer
Dundeleen nag ni ay goney leer. Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg. 10 Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi, 11 te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def. 12 Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la; 13 waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko. 14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne:
«Yewwul, yaw mi nelaw,
te jóge ci biir néew yi,
kon Kirist dina ne ràññ ci yaw,
ni leeru jant buy fenk.»
15 Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel, 16 tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon. 17 Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobarey Boroom bi. 18 Buleen màndi it ci sàngara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi; 19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ciy woy ak i cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seen xol. 20 Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen mana tollu, ci lu mu mana doon; 21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.
Diggante góor ak soxnaam
22 Naka yéen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi. 23 Ndaxte góor mooy kilifag soxnaam, ni Kirist nekke kilifag mbooloom ñi gëm, muy jëmmam ji muy sàmm. 24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jigéen ji wara jiitale jëkkëram ci lépp.
25 Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg soxnaam, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom, 26 ngir sellal ko ak kàddoom, ba mu laab ni ku sangu set. 27 Noonu dina ko jël, mu mel ni séet bu ñu waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te gàkkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk.
28 Na góor bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa soxna, bëgg sa bopp la. 29 Ndaxte kenn masula bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi; 30 ndaxte noo di céri jëmmam. 31 Mbind mi nee na: «Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon kenn.» 32 Loolu ëmb na mbóot mu xóot; man maa ngi wax ci lu jëm ci Kirist ak mbooloo mi. 33 Waaye li teew, na góor gu nekk bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram.