Bataaxal bu jëkk bi Yàlla may Pool,
mu bind ko
WAA TESALONIG
1
1 Nun Pool, Silwan ak Timote noo ngi leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist. Yal na yiw ak jàmm ànd ak yéen.
Li xibaaru jàmm bi jur ci dëkku Tesalonig
2 Bët bu set nu ngi sant Yàlla ndax yéen, di leen boole ci sunuy ñaan.
3 Dunu noppee fàttaliku ci kanam Yàlla sunu Baay jëf ji juddu ci seen ngëm, liggéey bi tukkee ci seen mbëggeel, ak muñ gi sosoo ci seen yaakaar ci sunu Boroom Yeesu Kirist.
4 Bokk yi, yéen ñi Yàlla bëgg, xam nanu ne Yàlla tànn na leen;
5 ndaxte xibaaru jàmm, bi nu leen doon yégal, yemul woon ci ay wax rekk, waaye àndoon na ak kàttan ak Xel mu Sell mi ak kóolute gu mag. Xam ngeen sunu taxawaay ci seen biir ngir seen njariñ.
6 Aw ngeen sunuy tànk ak yu Boroom bi, ci li ngeen nangu xibaar bi ci biir fitna yu metti, ànd ak mbég ci dooley Xel mu Sell mi.
7 Noonu ngeen daldi nekk royukaay ngir ñi gëm ñépp ci diiwaani Maseduwan ak Akayi.
8 Ndaxte kàddug Boroom bi jollee na ci seen biir, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen gëm Yàlla siiw na fépp. Matul sax nu di ci wax dara,
9 ndaxte ñoom ci seen bopp ñooy seede li sunu ngan def ci seen biir. Maanaam, ni ngeen dëddoo xërëm yi, jublu ci Yàlla te di ko jaamu, moom miy Yàlla Aji Dund ju dëggu ji,
10 te ngeen di séentu Doomam bàyyikoo asamaan, moom Yeesu mi mu dekkal te di nu musal ci merum Yàlla mi nara ñëw.