21
Yeesu feeñu na juróom ñaari taalibe
1 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu feeñuwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu ñuy wax Tiberyàdd. Nii la deme woon:
2 Taalibey Yeesu yii àndoon nañu: Simoŋ Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi»; Nataneel, mi dëkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe.
3 Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nun it danuy ànd ak yaw.» Ñu dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu jàppuñu dara.
4 Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi xàmmiwuñu ko.
5 Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
6 Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndijooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba manuñu ko woona génne ndox mi.
7 Taalibe ba Yeesu bëggoon, ne Piyeer: «Boroom bi la!» Bi Simoŋ Piyeer déggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summiku woon, daldi sóobu ci dex gi.
8 Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar.
9 Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga.
10 Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.»
11 Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom fukk ak ñett. Te li muy baree bare lépp, taxul mbaal ma dog.
12 Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne Boroom bi la.
13 Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën.
14 Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem.
Yeesu ak Piyeer
15 Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»
16 Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.»
17 Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaana, bëgg nga maam?» Piyeer am naqar ci li mu ko laaj ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Boroom bi, xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama xar yi.
18 Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa geño, di dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.»
19 Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer wara faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Noonu Yeesu ne ko: «Toppal ci man!»
20 Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñëw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon ko ne: «Boroom bi, kan moo lay wori?»
21 Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mujje?»
22 Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma délsi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.»
23 Noonu am, ci bokki taalibe yi, ñu xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu masul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma délsi, lu ciy sa yoon?»
24 Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne li muy wax dëgg la.
25 Yeesu def na yeneen jëf yu bare. Su ñu ko doon nettali, bind lépp, xalaat naa ne téere yi duñu xaj ci àddina.