Xibaaru jàmm bi ci Almasi bi Yeesu,
ni ko Yàlla jaaralee ci
LUUG
1
Ubbite gi
Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir, li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla. Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe. Noonu dinga mana xam ne li ñu la jàngaloon lu wér péŋŋ la.
Jibril yégle na juddub Yaxya
Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na sarxalkat bu ñu tudde Sakari te bokk ca mbootaayu sarxalkat, ya askanoo ci Abiya. Soxnaam Elisabet askanoo moom itam ci Aaróona. Sakari ak soxnaam ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp. Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet manula am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
Benn bés nag Sakari doon def liggéeyu sarxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog. Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan. 11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam. 12 Naka la ko Sakari gis, fitam daldi dem, mu tiit. 13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya. 14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom, 15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu. 16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom. 17 Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18 Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.» 19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu. 20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba. 22 Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23 Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi. 24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer 25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
Jibril yégle na juddub Yeesu
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. 27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama. 28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki. 30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam. 31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu. 32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam. 33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.» 35 Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji. 36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram. 37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.» 38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.»
Ci noonu malaaka ma daldi dem.
Maryaama seeti na Elisabet
39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude. 40 Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet. 41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet. 42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! 43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi? 44 Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég. 45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
Maryaama woy na mbaaxu Yàlla
46 Noonu Maryaama daldi ne:
47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,
sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48 ndaxte fàttaliku na ma,
man jaamam bu woyof bi.
Gannaaw-si-tey, niti jamono yépp dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.
Turam dafa sell.
50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,
ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,
te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,
yékkati baadoolo yi.
53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,
te dàq boroom alal yi, ñu daw ak loxoy neen.
54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,
di fàttaliku yërmandeem,
55 ni mu ko dige woon sunuy maam,
jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
Juddub Yaxya
57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor. 58 Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59 Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari. 60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.» 61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba. 63 Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru. 64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakari daldi waxaat, di màggal Yàlla. 65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp. 66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
Sakari sant na Yàlla
67 Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
 
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,
ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,
bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70 ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71 Dina nu musal ci sunuy noon,
jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72 Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam,
te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74 dina nu teqale ak sunuy noon,
ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
 
76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,
ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, di ko xàllal yoon wi.
77 Dinga xamal mbooloom ni leen Boroom bi mana musale,
jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,
ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,
79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,
takkandeeru dee tiim leen,
ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»
80 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.