9
Yeesu yónni na fukki taalibe yi ak ñaar
Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi. Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi. Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki. Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge. Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xibaaru jàmm bi, tey wéral jarag yi.
Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.» Am it ñuy wax naan: Ilyaas moo délsi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.» Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.
Yeesu bareel na ay mburu
10 Bi ndaw ya délsee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda. 11 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.
12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.» 13 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?» 14 Ndaxte lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom fukki nit.» 15 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.
16 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. 17 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.
Piyeer wax na ne, Yeesu mooy Almasi bi
18 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?» 19 Ñu ne ko: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
20 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.» 21 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn, 22 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»
23 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man. 24 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat. 25 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru? 26 Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi. 27 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»
Ndamu Yeesu jolli na ci moom
28 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan. 29 Bi muy ñaan, xar kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax. 30 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas. 31 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demug Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem. 32 Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmméentu, waaye bi ñu yewwoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam. 33 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax. 34 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee. 35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, baña nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
Yeesu faj na ku rab jàpp
37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu. 38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am. 39 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal. 40 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.» 41 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam. 43 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla.
Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya: 44 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.» 45 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
Kan moo gëna màgg?
46 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gëna màgg ci ñoom. 47 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen: 48 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gëna woyof ci yéen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.» 50 Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
Bañ nañoo nangu Yeesu ca Samari
51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem. 52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal. 53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem. 54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na sawaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?» 55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya, 56 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.
Ki bëgga topp Yeesu warula geestu gannaawam
57 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.» 58 Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» 59 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.» 60 Mu ne ko: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.» 61 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkka tàgguji sama waa kër.» 62 Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowula liggéey ci nguuru Yàlla.»