Mbir yi wara ñëw, te Yeesu Kirist
won ko Yowaana ci biir
PEEÑU
1
Ubbite gi
Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana. Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist. Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jóge ca Yàlla, te di sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.
Nuyoo bi jëm ci juróom ñaari mboolooy ñi gëm
Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanam gàngunem Yàlla*, 5-6 tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki jëkka dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf yépp.
Na ndam ak nguur féete ak Yeesu Kirist ba fàww, moom mi nu bëgg te yiwi nu ci sunuy bàkkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin.
Gisleen, mi ngi ñëw ci niir yi,
te ñépp dinañu teg seeni bët ci moom,
ba ci ñi ko jam sax.
Te xeet yi nekk ci kaw suuf yépp dinañu jooy ndax moom.
Waaw. Amiin.
Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa di Omega, Maay ki Nekk, di ki nekkoon démb, di kiy ñëw ëllëg, man Aji Man ji.»
Yowaana am na peeñu ca dunu Patmos
Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci muñ, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu ñuy wax Patmos. Wacce woon nañu ma fa, ndax li ma doon waare kàddug Yàlla tey seedeel Yeesu. 10 Xelum Yàlla solu ma ci bésu Boroom bi, te noonu ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit, 11 naan: «Bindal ci téere li ngay gis te yónnee ko juróom ñaari mboolooy ñi gëm, ca dëkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, Sàrd, Filadelfi ak Lawdise.»
12 Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci juróom ñaari tegukaayu làmp yu wurus, 13 gis ku taxaw ci biir tegukaayu ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk ngañaayu wurus ci ndiggam. 14 Boppam ak kawaram weex tàll ni perkaal, ay bëtam di xuyy ni sawara. 15 Ay tànkam mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baatam di riir ni duusi géej. 16 Mu yor ci loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, jaasiy ñaari boor yu ñaw di génn ci gémmiñam, xar kanamam leer nàññ ni jantub njolloor.
17 Naka laa ko gis, di daanu ci ay tànkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndijooram ci sama kaw ne ma: «Bul ragal dara. Maay ki jëkk te maay mujj. 18 Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba fàww, yor caabiy dee ak ju barsàq. 19 Kon nag bindal li nga gis, li am léegi ak li nara ami gannaaw gi. 20 Juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayu làmp yu wurus yi, ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki: biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy ñi gëm; juróom ñaari tegukaayu làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.
* 1:4 gàngune ma mooy fa buur biy toog. 1:20 malaaka man na tekki it «ndaw li».