8
1 Sóol nag rafetlu woon na la ñu bóom Eccen.
Fitnaal nañu mbooloo mi
Bésub keroog teg nañu mbooloom gëmkat ña ca Yerusalem fitna ju metti ba, lu moy ndawi Almasi, ñoom ñépp a tasaaroo ca diiwaani Yude ak Samari.
2 Ay nit ñu ragal Yàlla nag rob Eccen, ñaawlu deeyam lool.
3 Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.
Filib waare na ca Samari
4 Gëmkat ña tasaaroo di xamle fépp fu ñu jaare, xibaaru jàmm bu kàddu gi.
5 Noonu la Filib deme péeyub Samari, di siiwtaane Almasi.
6 Ba waa dëkk ba déggee mbaa ñu gis kéemaan ya muy def, ñoo bokk teewlu ay waxam.
7 Ndax bare na ca ñu rab yu bon jàppoon te mujj bàyyi leen, génne yuux yu réy; bare na ca it ñu lafañ ak ñu làggi woon te mujj wér.
8 Muy mbég mu réy nag ca dëkk boobee.
Ab ñeengokat gis na ku ko joŋ
9 Ku ñuy wax Simoŋ nag yàggoon na ca dëkk ba, di ñeengo. Ku waar waa Samari la woon, te doon tuddoo nit ku màgg.
10 Ñépp, mag ak ndaw, teewlu ko, naan: «Kii mooy dooley Yàlla ci boppam. Moom lañuy wax “Màggle”.»
11 La ñu ko teewloo woon moo di jëfi ñeengo ya mu leen yàgga yéeme.
12 Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
13 Simoŋ ci boppam gëm, moom it, ñu sóob ko ci ndox. Simoŋ nag bàyyeetul Filib. Ba mu gisee firnde yaak kiraama yu mag yay am, moom moo yéemu.
14 Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal.
15 Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi.
16 Ndax booba Noo gi wàccagul woon ci kenn ci ñoom, dees leena sóoboon rekk ci ndox ci turu Sang Yeesu.
17 Ba loolu amee Piyeer ak Yowaan teg leen loxo, ñu jot Noo gu Sell gi.
18 Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.
19 Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.»
20 Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
21 Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol.
23 Ndax gis naa ni nga sóoboo ci wextanu kañaan, keppu ci ndëngte.»
24 Simoŋ ne leen: «Ñaanal-leen ma Boroom bi, yeen ci seen bopp, ngir li ngeen wax lépp, lenn bañ ma cee dab.»
25 Gannaaw ba Piyeer ak Yowaan seedeelee kàddug Boroom bi, biral ko, Yerusalem lañu dellu, di xamle xibaaru jàmm bi ci ay dëkki Samari yu bare.
Filib yee na ab jaraafu Ecopi
26 Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.»
27 Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.
28 Naka la jaraaf ja màggalsi bay dellu Ecopi, toog ca watiiram, di jàngaale téereb Yonent Yàlla Esayi,
29 Noowug Yàlla ne Filib: «Doxal, dab watiir bale.»
30 Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31 Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg.
32 Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral:
«Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji;
mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat,
ubbiwul gémmiñam.
33 Ci biir toroxteem lañu ko xañ dëggam;
kuutaayam nag, ana ku ci mana wax?
Ndegam bakkanam lañu toxale kaw suuf.»
34 Jaraaf ja ne Filib: «Yaw laay laaj, ci kan la yonent bi wax lii? Boppam lay wax am keneen?»
35 Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36 Ba loolu amee ñu topp yoon wi, ba yem ci am ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngii, ana lu tee ma sóobu ci?»
37 Filib ne ko: «Soo gëmee ci sa léppi xol, sañ nga ko.» Mu ne ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi mooy Doomu Yàlla.»
38 Ci kaw loolu jaraaf ja santaane ñu taxawal watiir ba; Filib ak jaraaf ja wàcc, ñu dugg ñoom ñaar ca ndox ma, Filib sóob ko ca.
39 Naka lañu génne ca ndox ma, ngelawal Boroom bi ne cas Filib, yóbbu, jaraaf ja gisatu ko. Teewul mu topp yoonam, ànd ak mbég.
40 Filib moom, dëkk ba ñuy wax Asot la gisaat boppam. Mu wéye di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkkoo dëkk, ba àgg Sesare.