Amos
1
1 Kàdduy Amos a ngi, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa. Mu am peeñu mu jëm ci Israyil ci janti Osiyas buurub Yuda ak janti doomu Yowayas, Yerbowam buurub Israyil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.
2 Mu ne:
Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ,
Yerusalem lay àddoo,
parluy sàmm si ne faraas,
mbooyum kaw tundu Karmel lax.
Aji Sax ji mbugal na xeet yi
(Saar 1.3—2.16)
3 Aji Sax ji da ne:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
4 Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel,
mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.
5 Maay dàjji bunti dëkkub Damaas,
faagaagal waa xuru Awen,
boole ca boroom Bet Eden.
Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir.»
Aji Sax jee ko wax.
6 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm,
jalax Edomeen ña.
7 Maay yebal sawara ca tatay Gasa,
mu xoyom ay taaxam.
8 Maay fàkkas waa Asdodd,
fàkkas boroom yetu nguur fa Askalon,
fél Ekkron,
ndesu Filisteen ña sànku.»
Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
9 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Tir,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo jàpp mbooloom lëmm, jalax ca Edomeen ña,
te sédduñu ci kóllëreg bokk.
10 Damay yebal sawara ca tatay Tir,
mu xoyom ay tataam.»
11 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar,
jalax yërmande,
mer mer mu dul meddi
ak xadar ju dul giif mukk.
12 Maay yebal sawara fa Teman,
mu xoyomaale tatay Boccra.»
13 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen ñi,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd
ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.
14 Maay jafal ca kaw tatay Raba,
mu xoyom ay taaxam,
yuux ya jib bésub xare,
ci biir callweer bésub ngëlén.
15 Seen buur ay duggi ngàllo,
mooki kàngamam.»
Aji Sax jee ko wax.