4
1 Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari,
yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan.
Yeen ñiy torxal néew-ji-doole,
di not aji ñàkk
te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay,
ñu naan!»
2 Boroom bi Aji Sax ji giñ na ci sellngaam
ne: «Ay bés a ngii déy, di ñëw,
dees na leen kor, yóbbu,
ku nekk ci yeen koru niw jën,
3 ñu diri ko jaarale fu xar-xaru tata gëna jegee,
sànni ko ca Armon.»
Kàddug Aji Sax jee.
4 Aji Sax ji nee:
«Demleen Betel, bàkkaare fa,
dem Gilgal, bàkkaareeti fa.
Rendileen seenub sarax ca ëllëg sa,
joxe seen saraxi fukkeeli alal ca gannaaw ëllëg sa,
5 te ngeen lakk mburu, def ko saraxu cant.
Yégleleen seen saraxi yéene te siiwal ko, dégg ngeen?
Ndegam loolu ngeen namm, yeen bànni Israyil.»
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
6 «Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk,
dugub ñàkke fépp fu ngeen moom,
te taxul ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee.
7 Mu ne:
«Maa leen xañ ub taw
bu leen may ngóob ci ñetti weer.
Ma taw ci bii dëkk,
tawuma ca bee.
Wii waar tawlu,
wee waar lax.
8 Ñaari dëkk ba ñett di deek mar, wuti beneen,
naane fa, te duñu màndi.
Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee.
9 «Maa leen dumaa gub yu yàqu, di saxee saxe,
wowal seeni tool aki tóokër,
garabu figg ak oliw, njéeréer yi lekk.
Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee.
10 «Maa leen yónnee mbas mu mel ni mu waa Misra.
Maa reylu seeni waxambaane ci xare,
jàpplu seeni fas,
gillil xetu néew ya ca seeni dal.
Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee.
11 «Maa jàllarbi lenn ci yeen,
na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor.
Ngeen rëcce ca ni gillit
gu ñu fëkke cib taal.
Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee!
12 «Moo tax ma di leen def lii, yeen bànni Israyil.
Gannaaw lii laa leen di def nag,
waajleena dajeek seen Yàlla, yeen bànni Israyil.»
13 Kii kat moo móol tund,
di sàkk ngelaw,
di xamal nit nammeelam.
Kee di soppi lëndëm ag leer,
di daagoo kawte ya.
Kookoo di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.