5
Bul gaaw làmmiñ,
bul gaawa dikke Yàlla mbir.
Yàllaa ngi kaw asamaan,
yaw yaa ngi fi suuf.
Kon na say kàddu néew.
Bu xalaat baree, indi gént;
bu wax baree, waxi dof jib.
Boo digook Yàlla,
bu ko yeexe;
Daray foontukat neexul,
defal li nga dige.
Baña digee gën dige loo deful.
Bu la sa làmmiñ yóbbe bàkkaar,
ba ngay lay ndawal Yàlla la, naan lii njuumte la woon.
Ana lu jar Yàlla di la meree sa kàddu,
bay neenal saw ñaq?
Wax ju bare, caaxaani neen;
mook gént yu baree yem.
Kon, Yàlla, ragal ko.
Nguur bare na àq
Boo gisee ñuy not néew-ji-doole,
di jalgati dëgg ak yoon cib gox,
bumu la jaaxal;
kilifa gi, kilifaam a ko yiir;
ñoom it seen kilifaa leen yiir.
Xanaa ndax buur suqal mbey mi,
ba ñépp jariñoo suuf si.
Alal coono la
Bëggkatu xaalis du doyal xaalis,
bëggkatu alal du doyal tono,
te loolu it, cóolóoli neen.
10 Bu koom yokkoo,
lekk-kat yi yokku.
Ana lu muy jariñ boroom koom ga,
xanaa di ko duufale bëtam?
 
11 Surga, lekkam néew, bare,
mu nelaw, ba fàttey boram;
boroom alal regg,
du nopplu, du nelaw.
 
12 Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf:
Alal ju boroom dajale ba loru,
13 mbaa pexeem moy, mu sànkule;
ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14 Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen,
walbatiku dellu na nga dikke woon.
Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15 Dikke ni, delloo ni,
loolu it tiis wu réy la.
Doñ-doñi, ngelawal neen,
ana jariñ la?
16 Ngay dunde tiis bésoo bés,
ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
Bànneexu bakkan, Yàlla
17 Lii daal laa ci gis, man.
Li gën te jaadu ci nit: Na lekk, naan
te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf
giiru dund gi ko Yàlla may.
Loolu mooy céram.
 
18 Alal ak koom, ku ko Yàlla may,
may ko mu tal koo xéewloo,
mu nangu céram, bànneexoo ñaqam,
loolu mayu Yàllaa.
19 Yàllaa koy bànneexal,
ba du tiisoo ay fanam.