8
Ana ku rafet xel?
Ana ku rafet xel nu muy mel?
Ana ku xam piri?
Am xel rafet, kanam leer, gëna lewet.
Dama ne déggalal Buur,
yaa ko giñoon ci Yàlla*.
Bul gaawa won buur gannaaw;
bul saxoo lu buur buggul;
Buur, lu ko neex lay def.
Kàddug buur kilifteef la.
Ana ku ko naan: «Looy def nii?»
Ku dégg ndigal
doo am lu la soof.
Ku xelu, xam lu jot,
xam doxalin.
Mbir mu mu doon kat ak jotam ak doxalinam,
waaye nit am na tiis wu ko diis.
Kenn xamul luy xew ëllëg,
kenn manula wax luy xew ëllëg.
Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese,
kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam,
kenn muccul ci boobu xare,
te mbon du ca wallu boroom.
 
Loolu lépp gis naa ko,
ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf;
fi nit di yilife nit, muy loraange.
Bul roy lu bon.
10 Ma gis itam ñu bon ñu ñu rob,
ñu daan yaale kër Yàlla ga,
ñu di leen gërëme tey seeni jëf ca dëkk ba.
Loolu it, cóolóoli neen.
11 Jëf ñaaw na, mbugal ma yeex,
ba tax doom aadama sóobu ci mbon.
12 Nit bàkkaar na téeméeri yoon,
te teewul mu gudd fan.
Xam naa it ne nee ñu
ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla,
ndax wormaal ko.
13 Ku bon, du am lu baax,
fanam du màgg ni ker,
ndax wormaalul Yàlla.
14 Waaye cóolóoli neen a ngi am fi kaw suuf:
Ku jub jot yoolu ku bon,
ku bon jot yoolu ku jub.
Ma ne loolu it cóolóoli neen la.
 
15 Man daal damay digle bànneex,
ndax nit amul lu gën fi kaw suuf
di lekk ak a naan ak a bànneexu,
muñe ko doñ-doñam,
fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.
Yàlla, kenn xamu ko
16 Ma walbatiku xalaat, di jéema xam fu xel rafete,
di xoolaat li nit jàppoo fi kaw suuf,
ba guddeek bëccëg, gëmmul bët.
17 Ma daldi gis li Yàlla def lépp.
Nit kay xel ma du daj liy xew fi kaw suuf.
Day seet ba sonn, du ko daj.
Boroom xel bu wax ne xam na ko it,
du ko daj.
* 8:2 Seetal ci 2.Buur ya 11.17.