17
Fecci kóllëre, peyam du jaas
1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
2 Yaw nit ki, caxal waa kër Israyil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal.
3 Ne leen: «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Jaxaay ju mag la woon, réyi laaf, guddi dunq,
sëq lipp, yànj lool.
Mu dikk ba Libaŋ, jàpp ci collu genn garabu seedar,
4 dagg car bu ndaw ba ca gëna kawe,
yóbbu ba menn réewum jula,
jëmbat ko ca biir dëkkub jaaykat ya.
5 Mu sàkk ci jiwum réew mi,
def ko ci suuf su nangu,
dendale kook ndox mu ne xéew,
ni kuy jëmbat garabu sóol.
6 Mu jebbi, dig reseñ, gëna yaatu te gàtt taxawaay.
Car ya ne coleet wuti jaxaay ja,
reen ya des ca suufam.
Mu di reseñ gu saxi car,
firiy bànqaas.
7 «Jeneen jaxaay ju mag daldi ne jimeet,
réyi laaf, sëq lipp.
Reseñ ja jekkee jekki tàllal koy reenam,
di ŋaf-ŋafi, firiy bànqaasam, wuti ko,
ngir mu suuxat ko fa mu jëmbate woon.
8 Tool bu nangu bu feggook ndox mu ne xéew la jëmbate woon,
ngir naat, meññ, ba doon reseñu ngëneel.
9 «Neel, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Mbaa jooju reseñ dina baaxle?
Mbaa jeneen jaxaay ja du buddiy reenam,
buur doom ya,
ba lu mu jebbile woon lax,
ba buddi reen ya du laaj përëg bu réy,
mbaa nit ñu bare?
10 Ma nga noonu jëmbate, waaye mbaa dina baaxle yee?
Mbaa ngelawal penku du ko laal rekk mu laxa lax?
Mbaa du lax fa mu saxe?»
11 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
12 «Waxal waa kër fippukat yi, ne leen: “Xamuleen lu mbir yooyu di wund?” Ne leen: “Mu ngoogu, buuru Babilon a dem Yerusalem, jàpp buur baak kàngam ya, ànd ak ñoom, yóbbu Babilon.
13 Moo tànn ku bokk ci askanu buur, fasook moom kàddu, giñloo ko ne dina ko nangul, daldi yóbbu njiiti réew mi,
14 ngir nguurug Yerusalem suufe, baña yékkatiku, di wéye surgawu Babilon, ni ñu ko fasoo woon.
15 Ka bokk ci askanu buurub Israyil nag fippu, yónni ay ndaw réewum Misra, ngir ñu jox ko ay fas ak mbooloo mu takku. Moo ka def loolu dina baaxlee? Mbaa dina mucc? Nu mu cay mucce te wor kàddu, ga mu fasoo woon?
16 «“Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ci biir réewum buur boobu ko fal, te mu sàggane la mu ko giñaloon, wor kàddu ga mu fasante woon ak moom, ci biir Babilon googu lay deeye.
17 Firawnaak mbooloom mu réy ak gàngooram gu mag sax duñu ko mana wallu ci xare, keroog bu ñuy yékkati ab sëkk, tabax ab gawukaay ngir bóom ñu bare.
18 Moo sàggane ngiñ, moo wor kàddu ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk.
19 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, maay këpp jëfam ci kaw boppam ndax ngiñ li mu ma giñal la sofental, kàddu gi mu fasanteek man la wor.
20 Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma.
21 Mboolem ñay dawe ca gàngooram yépp, saamar lañuy fàddoo; ña cay rëcce, fépp fu ngelaw jublu lañuy tasaarooji, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax.
22 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Man ci sama bopp maay sàkke ab car
ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga,
sàkkal ko bérab.
Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy,
jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe.
23 Ca kaw tundu Israyil wu mag wa laa koy jëmbat,
mu sëq, meññal,
ba doon garabu seedar gu am daraja,
mboolem picc dëkke ko,
mboolem njanaaw màkkaanoo keram.
24 Garabi àll bi yépp dinañu xam,
ne man Aji Sax ji maay gàttal garab gu gudd,
di guddal garab gu gàtt.
Maay wowal garab gu naat,
di naatal garab gu wow.
Man Aji Sax ji maa wax, maay jëf.”»