21
Woyu saamar jib na
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: «Yaw nit ki, neel jàkk yoonu ndijoor, sànnil kàddu ci kaw bëj-saalum googu, waxal waxyu ci kaw gottub Negew boobu*. Dangay wax waa gottub diiwaanu Negew, ne leen: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp, gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk, ba mboolem kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa ko taal te du fey.”» Ma ne ko: «Éey Boroom bi Aji Sax ji, ñii déy a ngi wax ci man, naan: “Kii moom xanaa day léeb ak a léebaat rekk?”» Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: «Yaw nit ki, jàkkaarlool ak Yerusalem, nga sànni kàddu bérab yu sell yi te nga wax waxyu ci kaw réewum Israyil. Waxal réewum Israyil ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii fi sa kaw. Maay boccee sama saamar mbaram, daldi dagge fi yaw ku jub ak ku bon. Dagge fi yaw ku jub ak ku bon moo may taxa boccee sama saamar mbaram, dal ci mboolem kuy dund, bëj-saalum ba bëj-gànnaar, 10 ba képp kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa bocci sama saamar, te du dellu mbaram.” 11 Yaw nit ki, binnil, neel yàcc, di binnee naqar, ñuy gis. 12 Dees na la laaj ne la looy binni. Nga ne leen: “Xanaa mbir mi ma dégg. Bu agsee fit yépp ay rëcc, loxo yépp nasax, xol yépp jeex, óom yépp di fenqoo. Mu ngooguy dikk te dina am. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
13 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 14 «Yaw nit ki, waxal bii waxyu, nga ne: “Boroom bi dafa wax ne:
Saamar a ngoog,
saamar bu ñu xacc, jonj ko!
15 Dees koo jonj ngir bóome,
jonj koo jonj ba muy tàkk.
Ana nu nu mana bége lii? Ngeen ne Aji Sax ji nee: ‘Yetu nguurug Yuda sama doom a ngi fi.’
Waaye saamar bi faalewul benn bant!
16 Santaane nañu ñu jonj saamar bi,
ba loxo man koo téye,
ñu xacc ko, jonj ko,
nar koo teg ci loxol bóomkat.
17 Yaw nit ki, yuuxul, jooyal,
saamar bi dikkal na sama ñoñ,
dikkal mboolem kàngami Israyil,
boole leen ak sama ñoñ, jalax ci kaw saamar.
Kon nag, màttul, wiccax!
18 Nattu bi metti na!
Bu yetu nguur, wi saamar bi xeeb, demee, ana luy xew?
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”
 
19 «Yaw nit ki, jottlil waxyu,
ŋëbal bii loxo, dóor ca bee.
Na saamar bi dal benn yoon, ñaari yoon, ba ñett,
saamaru ndee la, saamar baay bóom ñu bare,
gaw leen,
20 yóbbuw fit,
tërëfloo ñu bare.
Seen buntoo bunt laa teg saamaru bóomkat.
Ndeysaan, bii saamar bu ñu defar ba muy tàkk,
xacc ko ngir bóome.
21 Saamar, ñaweel sa ndijoor,
walbatiku, jëm càmmoñ,
ak foo mana jublu,
22 man it ma ŋëb bii loxo, dóor ca bee,
ba giifal sama xadar.
Man Aji Sax ji maa ko wax.»
23 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 24 «Yaw nag nit ki, sàkkal ñaari yoon yu saamaru buuru Babilon di jaare dikk; ñaari yoon yuy bàyyikoo menn um réew. Tegal fa buntu yoon wu ci nekk màndarga muy tegtale dëkk ba yoon wa jëm; 25 wenn yoon wa jëme saamaru Babilon ca Raba, dëkkub Amoneen ñi; wa ca des jëme ko Yerusalem, dëkk ba ñu dàbbli, ca Yuda. 26 Buuru Babilon a ngay taxaw ca selebe yoon wa, fa ñaari yoon ya séddlikoo, ngir gisaane. Dina yëngal fitti seetukaay yi, xool ci terafim yi, jumtukaay yi ñuy gisaanee, te dina xool ci resu jur. 27 Fitt giy misaal Yerusalem ndijooram lay wadd. Mu sës dénki dàjjikaay yi, yéene ndigalu bóome, xaacu, daldi sës dénki dàjjikaay yi ci bunt yi, yékkati sëkk yi, ngir taxawal ab gawukaaay. 28 Waa Yerusalem foog ne ngisaane googu misaal seen jéll, caaxaan la, ndax ngiñ moo lal seen kaaraange, ba du deñ. Waaye buuru Babilon a leen di fàttli seenug tooñ, ba jàpp leen njaam.
29 «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yeena fàttliku seen ñaawtéef, seeni tooñ ne fàŋŋ, seeni bàkkaar fés ci seen jëf jépp, gannaaw yeena ñaaw ñaawtéef gu ñu leen di fàttlikoo, dees na leen jàpp.
 
30 «Waaye yaw garmib Israyil bu teddadi bu bon bi,
sa bés dikk na, sa àppu mbugal mat na.
31 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Dindil kaala gi, foq mbaxanam buur mii;
la woon wonni na,
ku noon dett jóg, ku jóg, detteelu.
32 Tasaaroo, tasar, maa ko naa tasar!
Lépp ay wonni,
ba keroog boroom àtte bi dikk, ma jox ko ko.
33 «Yaw nag nit ki, jottlil bii waxyu, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Amoneen ñeek seeni saaga ne:
Saamaroo saamar,
bocciku, nara bóome,
xacce ba mana yàppe,
di tàkk ni melax.
34 Gisal nañu leen peeñuy caaxaan,
gisaaneel leeni fen.
Teewul saamar ba di tege ca ndoddi
ñu bon ñi ñu nara bóom,
seen bés taxaw,
seen mujjantalu mbugal teew.
 
35 «“Léegi dellooleen saamar ci mbaram.
Saamaroo, fa ñu la sàkke woon,
ca réew ma nga cosaanoo, fa laa lay àttee.
36 Maa lay xëpp samam sànj,
wal sama sawaras xadar fi sa kaw,
jébbal la nit ñu néeg,
ñu xareñ ci sànke.
37 Yaay doon mattum sawara wa,
sa deretu boroom ne xéew fi digg réew mi,
ba deesatu la fàttliku.
Man Aji Sax ji maa ko wax!”»
* 21:2 Waxyu bii mu ngi jëm ci wàllu Yuda gi féete bëj-saalum. 21:30 Buur Cedesyas lañuy wax fii. Cedesyas mooy buur bi mujj ci askanu Daawuda. Seetal ci 2.Buur ya 25.4-7.