35
Waxyu dal na Edom
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: «Yaw nit ki, neel jàkk tundu Seyir*, nga biral waxyu fi kawam. Nga wax ko, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaw tundu Seyir, maa ngii fi sa kaw.
Maa lay dóor sama loxo,
nar laa def gent bu wéet.
Say dëkk, jali doj laa koy def,
nga gental,
ba xam ne maay Aji Sax ji.
 
«“Dangaa masa bañ bànni Israyil.
Ba musibay bànni Israyil taxawee,
ba seen àppu mbugal mat sëkk,
yaa leen jañax ci kaw ñaawkay saamar.
Moo tax giñ naa ko ci man miy dund,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
deret laa lay sange,
deret topp la,
ndegam bañuloo tuur deret,
deret a lay topp.
Maay def tundu Seyir gent bu wéet,
maa fay dagge nit ku fay génne ak ku fay dugge.
Maay feesaley tundam nit ñu ñu bóom,
tundam yu ndaw aki xuram aki xunteem,
fa la ñi fàddoo saamar naan lareet.
Ay gent yu gental fàww laa laay def,
say dëkk, deesu ko dëkkeeti.
Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
 
10 «“Aji Sax ji nekk fi, nga naan:
‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii,
maa leen moom, noo ciy teg loxo.’
11 Moo tax giñ naa ko ci man miy dund,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
ni nga mbugale bànni Israyil ci sa biir mer,
ak sa kiñaan ak sa mbañeel,
ni laa lay mbugale.
Maay dogal sab àtte,
ba xamal ñii maay kan.
12 Su boobaa nga xam ne man Aji Sax ji,
maa dégg sa jépp waxi ñàkk kersa ja nga nee:
‘Tundi Israyil a ngii ne tasar,
dim sëxëtoo mu ñu nu wërsëgale.’
13 Yeenay damu fi sama kaw,
di ma wax waxi reewande ju bare!
Maa déggal sama bopp.
14 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Bu àddina sépp di bànneexu,
yaw, ab gent laa lay def.
15 Yaa doon bége suufas Israyil su gental.
Noonu laa lay def.
Ab gent ngay doon, yaw tundu Seyir,
yaak Edom gépp ba mu daj.
Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”
* 35:2 Seyir mooy réewum Edom, cosaanu Esawu sëtub Ibraayma. 35:10 ñaari làngi giir yi Israyil laak Yuda.