46
«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Buntu ëttu biir bi féete penku, na tëje diiru juróom benni fan yi ñuy liggéey. Waaye bésub Noflaay ba cay topp, na ubbiku. Bésub Terutel weer it, na ubbiku. Na ki ci jal bi jaare ci dal-luwaayu mbaar mi féete biti te na yem ci jëni buntu ëttu biir bi. Na fa xaar sarxalkat yi def saraxu rendi-dóomalam, ak saraxi cantam ci biir jàmm. Su ko defee mu sujjóot ci dëxu bunt bi, ba noppi, génn. Bunt bi nag du tëje ba ngoon jot. Bésub Noflaay ak Terutel weer, baadooloy réew mi ci bunt boobu lañuy sujjóote fi kanam Aji Sax ji.
«Saraxu rendi-dóomal, bi ki ci jal biy indil Aji Sax ji bésub Noflaay, juróom benni xar yu ndaw yu amul sikk lay doon, ak kuuy mu amul sikk. Saraxu pepp biy ànd ak kuuy mi benn efa* lay doon, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak dayob pepp bu mu àttan buy ànd ak xar yu ndaw yi ak xiinu diw, yemook ñetti liitari diw ak genn-wàll ci efab pepp bu nekk. Bésub Terutel weer, wenn yëkk wu ndaw lay doon wu amul sikk ak juróom benni xar yu ndaw akam kuuy, te lépp mucc sikk. Na ci boole saraxu benn efab pepp buy ànd ak yëkk wi, ak benn efab pepp ngir kuuy mi, ak lu mu man ci pepp, mu booleek xar yu ndaw yi, ak benn xiinu diw ci efab pepp bu nekk.
«Dal-luwaay bunt, bi ki ci jal biy jaare duggsi, fi lay jaare génn. Baadooloy réew mi nag bu ñuy teewesi bésub ndaje fi kanam Aji Sax ji, ku ci jaare mbaaru buntu bëj-gànnaar, di sujjóotsi, bu noppee na jaare mbaaru buntu bëj-saalum ba. Te ku dugge mbaaru buntu bëj-saalum, bu noppee na génne mbaaru buntu bëj-gànnaar ba. Deesul delloo bunt bi nga dugge. Bunt bi mu jàkkaarlool lees di génne. 10 Ki ci jal bi ci boppam, bu baadoolo yiy dugg, na duggandook ñoom, bu ñuy génn, mu génnandook ñoom.
11 «Su dee bési màggal ak bési ndaje yi, saraxu pepp mi benn efa lay doon ngir yëkk wi, yemook fukki kilook juróom, ak benn efa ngir kuuy mi, ak dayo bu ñu àttan ngir xar yu ndaw yi, efab pepp bu ne ànd ak benn xiinu diw, di ñetti liitar ak genn-wàll.
12 «Buntu ëttu biir bi féete penku it lañuy ubbil ki ci jal bi, buy joxe saraxu yéene: muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu cant ci biir jàmm, di beneen saraxu yéene bu ñeel Aji Sax ji, ngir mu joxe saraxu rendi-dóomalam, mbaa saraxu cantam ci biir jàmm, ni mu koy defe ci bésub Noflaay. Bu noppee, génn, ñu tëj bunt bi.
13 «Am xarum menn at mu amul sikk lees di defal Aji Sax ji bés bu nekk saraxu rendi-dóomal, te suba su ne lees koy def. 14 Nañu ci boole suba su ne benn céru juróom benneelu efab pepp, yemook ñaari kilook liibar, ànd ak liitaru diw, yemook benn céru ñetteelu xiinu diw buy tooyal sunguf si. Loolooy saraxu pepp mi, ñeel Aji Sax ji, di dogali yoon yu sax dàkk. 15 Muy xar mu ndaw mi, di saraxu pepp mi, di diw gi, suba su nekk lees koy def, muy saraxu rendi-dóomal bu sax dàkk.
Boroom jal bi sañul lépp ci suufam
16 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Su ki ci jal bi mayee kenn ci doomam yu góor lenn ci céru suufam, kookoo koy jagoo, te alal jooju, céru doomi kooka lay doon. 17 Waaye su ki ci jal bi mayee kenn ciy surgaam lenn ci suufam, ba keroog atum Yiwiku ma rekk la surga ba di moom suuf sa, waaye bu atum Yiwiku teewee, suuf si day dellu ci loxol ki ci jal bi. Suuf soosu, céru doomi boroom jal bi doŋŋ lay doon. 18 Ki ci jal bi nag du nangu lenn ci suufas baadoola yi, di leen xañ seen alal. Alalu boppam doŋŋ la saña sédd doomam yu góor. Su ko defee kenn ci sama ñoñ du ñàkk alalam.»
Sàkkal nañu kër Yàlla gi ay waañ
19 Ba loolu amee waa ja génneeti ma ca jàllukaay ba feggook buntu bëj-gànnaar. Mu dugal ma ca néeg yu sell ya ñu beral sarxalkat yi. Ndeke bérab a nga foofa ca ruq ba, ca biir-a-biir, ca wetu sowu. 20 Mu ne ma: «Bii bérab, fi la sarxalkat yiy togge yàppu saraxu peyug tooñ ak saraxu póotum bàkkaar, di fi lakk saraxu pepp mi, ngir baña génne lenn lu sell ca ëttu biti ba, bay sédd nit ñi sellnga gu leen di lor.»
21 Gannaaw loolu waa ji génneeti ma ba ci ëttu biti bi, yóbbu ma ci ñeenti collam yépp. Ndeke coll wu ci nekk, ber nañu ca ëtt bu ndaw, 22 bu gudde ñeent fukki xasab, yaatoo fanweeri xasab, te ñeenti ëtt yu ndaw yi ci coll yi yépp a tolloo. 23 Ñeenti ëtt yu ndaw yi, bu ci nekk miir bu gàtt a ko ub, ay toggukaay tege ci suufam, leru miir bi ba mu daj. 24 Waa ji ne ma: «Lii mooy waañ yi liggéeykati kër Yàlla gi di togge yàppu saraxi askan wi.»
* 46:5 benn efa: seetal ci 45.24.