48
Daggal nañu suuf giiri bëj-gànnaar
«Lii mooy limeefu giiri Israyil, ak céru suuf bi giir gu ci nekk di féetewoo. Céru Dan moo féete catu bëj-gànnaar. Kemoom day topp yoonu Ettlon ba Lebo Amat, jàll ba Àccar Enan ga digalook Damaas, Amat féete ko bëj-gànnaar. Suufas Dan day jàpp penku ba sowu, ca géej gu mag ga, di benn pàcc. Suufas Aser day digalook sos Dan, jàpp, moom it, penku ba sowu, di benn pàcc. Suufas Neftali day digalook sos Aser, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. Suufas Manase day digalook suufas Neftali, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. Suufas Efrayim day digalook sos Manase, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. Suufas Ruben day digalook sos Efrayim, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. Suufas Yuda day digalook sos Ruben, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc.
Daggal nañu Aji Sax ji céram bu sell
«Suuf sa digalook Yuda ca wetu bëj-gànnaaram, te dale penku ba sowu, mooy doon pàkk bi ñuy jooxe. Ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), fukki kilomeetar ak ñett, lay yaatoo, gudde ni suufas genn giir gu ci nekk, te bérab bu sell bi nekk ci digg bi. Pàkk bi ngeen di jooxeel Aji Sax ji ci dog boobu, day am guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) yemook fukki kilomeetar ak ñett ak yaatuwaayu fukki junniy xasab (10 000), di juróomi kilomeetar ak xaajaat. 10 Cér bu sell a ngoog, ñeel sarxalkat yi. Ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) lay am wetu bëj-gànnaar, yaatoo fukki junniy xasab (10 000) wetu sowu, yaatoo fukki junniy xasab (10 000) wetu penku, gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) wetu bëj-saalum, te bérabu Aji Sax bu sell bi nekk ci digg bi. 11 Dig-digal bu sell boobu, na ñeel sarxalkat yi askanoo ci Cadog, ñoom ñi sàmmoon sama ndénkaane, baña ànd ak bànni Israyil, di lajj ni seen yeneen bokki Leween ñi. 12 Jooxeb suufas réew mi, nañu ci jooxeel sarxalkat yi bérab bu sella sell, mu feggook suufas Leween ñi. 13 Na suufas Leween ñi digalook sos sarxalkat yi, di pàkk bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), te yaatoo fukki junniy xasab (10 000). Bu ci nekk na am guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) ak yaatuwaayu fukki junniy xasab (10 000). 14 Cér boobu mooy tànnéefu suuf si. Maneesu cee jaay, mbaa di ci weccikoo lenn, te lenn du ci tàbbi ciy loxo, ndax cér bu sell la, ñeel Aji Sax ji.
Daggal nañu suuf waa dëkk bi ak boroom jal bi
15 «Pàkk bay des ci yaatuwaayu dog boobu dina yaatoo juróomi junniy xasab (5 000), gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000); suufas ñépp la pàkk boobu di doon, ngir dëkk bi. Man naa doon ay dëkkuwaay aki parlu, te na dëkk bi ci boppam féetewoo digg ba. 16 Na dëkk bi bindoo ab kaare bu wet gi di ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500), di ñaari kilomeetar ak genn-wàll. 17 Parlub dëkk bi nag, na féeteek ñeenti weti dëkk bi, te doon fa wet gu nekk bayaal bu yaatoo ñaar téeméeri xasab ak juróom fukk (250). 18 Fi feggook dog bu sell bi ñu beral Aji Sax ji, dina des pàkk bu ñuy bey, bu gudde fukki junniy xasab (10 000) wetu penkub dëkk bi, ak beneen pàkk bu ni tollu ci wetu sowu. Ca lañuy jële lekku liggéeykati dëkk bi. 19 Waa dëkk bi koy bey, ci giiri Israyil yépp lañuy bàyyikoo. 20 Mboolem pàkk boobu ñuy jooxe, na doon kaare bu wet gi di ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), te pàkk boobu ñuy jooxe, pàkk bu sell bi ci la, dëkk bi, ci la.
21 «Li féete penku ak li féete sowu yépp nag te des ci suuf si, gannaaw cér bu sell bi, ak suufas dëkk bi, buur bi ci jal bee koy moom; wet gu ci nekk yaatoo ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), gii àkki kemu Israyil ga féete penku, gee àkki kemu Israyil ga féete sowu, cér bu sell beek kër gu sell gi nekk ci digg bi. 22 Kon suufas Leween ñi ak suufas dëkk bi day bokk féete ci diggu suufas boroom jal bi, suufas boroom jal bi nekk diggante céru Yuda ba ca bëj-gànnaar, ak céru Beñamin ca bëj-saalum.
Daggal nañu suuf giiri bëj-saalum
23 «Limeefu giiri Israyil yi ci des, seeni suuf nii lay tëdde: Li dale kemu penku ba, ba ca géej gu mag ga ca sowu, benn pàcc lay doon, Beñamin féetewoo ko. 24 Suufas Simeyon feggook sos Beñamin, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. 25 Suufas Isaakar jàpp penku ba sowu, feggook sos Simeyon, di benn pàcc. 26 Suufas Sabulon feggook sos Isaakar, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. 27 Suufas Gàdd feggook sos Sabulon, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. 28 Suufas Gàdd, kemug bëj-saalumam mooy doon kemug réew mi. Day dale fa Tamar ca penku ba, ba ca yoonu ndoxu Meriba ca Kades, leru walum Misra, ba ca géej gu mag ga. 29 Noonu ngeen di séddalee réew mi giiri Israyil yi, giir gu ci nekk, ngeen dogale ko noonu céru suufam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Yerusalem: tur wu yees, fukki bunt ak ñaar, ni giir yi
30 «Bunti dëkk bi nag nii lay tëdde: Ñeenti miiri dëkk bi, bu ci nekk day am guddaayu ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500). 31 Miir bu ci nekk dina am ñetti bunt yu ñu dippee ñetti giiri Israyil. Wetu bëj-gànnaar, benn buntu Ruben ak benn buntu Yuda ak benn buntu Lewi. 32 Wetu penku am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Yuusufa ak benn buntu Beñamin ak benn buntu Dan. 33 Wetu bëj-saalum am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Simeyon ak benn buntu Isaakar ak benn buntu Sabulon. 34 Wetu sowu am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Gàdd ak benn buntu Aser ak benn buntu Neftali. 35 Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “Aji Sax jaa ngi fi.”»