6
Waajur na yar, te njaboot di dégg
1 Naka yeen xale yi, déggal-leen seeni waajur, ngir Boroom bi, ndax moo war.
2 «Teral-leen seen ndey ak seen baay,» mooy ndigal li jëkka ànd akub dige,
3 ndax da ne: «ngir ngeen baaxle te gudd fan ci kaw suuf.»
4 Yeen ñiy baay it, buleen xoñoñal xale yi, waaye yarleen leen, di leen jubanti, di leen xamal coobarey Boroom bi.
Na jaam ak sangam déggal Boroom bi
5 Yeen jaam yi, déggal-leen seen sangi àddina, ànd ceek ragal Yàlla bay kat-kati, ak xol bu dëggu. Ni ngeen déggale Almasi, nangeen leen ni déggale.
6 Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, na di yéene ju ngeen tibbe ci seen xol, ngir jëfe liy coobarey Yàlla, ni mu ware ay jaami Almasi.
7 Liggéeyal-leen leen ci xol bu tàlli, ba mu mel ni Boroom bi ngeen ko defal, waaye du nit doŋŋ,
8 te ngeen xam ne nit ki, mu dis gor mbaa ab jaam, mboolem lu mu def ci lu baax, loola la ko Boroom biy delloo.
9 Yeen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, bàyyileen di tëkkoo, te ngeen xam ne yeen ak ñoom a bokk benn Boroom fa asamaan, te xejj ak seen amul fa moom.
Xare bi nook Seytaane la
10 Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.
11 Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
12 Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.
13 Kon nag jël-leen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.
14 Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn.
15 Xibaaru jàmm bi indi jàmm nag, defleen ko muy dàll yu dëgëral seen taxawaay.
16 Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku Bon ki.
17 Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jël-leen ko, sol, jël-leen itam saamar bi Noo giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
18 Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
19 Man itam, booleleen ma ci, ngir saa yu ma ubbee sama gémmiñ, mana xéewloo ndéey lu ma xamlee fit wu dëgër, mbóoti xibaaru jàmm bi,
20 xibaar bi ma di ndawam lu ñu tënke ay jéng. Waaye ñaanal-leen ma ma di ko waxee fit, ni mu ma ware.
Póol tàggu na waa Efes
21 Dingeen mana xam nag lu jëm ci man, ak li may def, ndax Tisig, mbokk mu ñu sopp, jawriñ ju wóor ci liggéeyu Boroom bi, moo leen di xamal lépp.
22 Loolu ci boppam sax moo waral ma yónni ko ci yeen, ngir mu xamal leen ni nu nekke, ba seral seen xol.
23 Yal na jàmm ñeel bokki gëmkat ñi, ak cofeel gu ànd ak ngëm, bawoo fa Yàlla Baay bi, ak Sang Yeesu Almasi.
24 Na aw yiw ñeel mboolem ñi sopp sunu Sàng Yeesu Almasi, cofeel gu dul fey.