40
Samp jaamookaay bi jot na
1 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
2 «Bu keroogee benn fanu weer wi jiitu, nanga samp màkkaanu xaymab ndaje mi.
3 Nanga yeb ci biir, gaal gi àlluway seede si dence, te nga làqe gaal gi rido bi.
4 Dugalal taabal ji te taaj ci li muy àndal; dugalal tegukaayu làmp bi, nga taal ay làmpam,
5 te nga teg sarxalukaayu cuuraay bu wurus bi ci kanam gaal gi àlluway seede si dence, ba noppi nga samp lafu buntu jaamookaay bi.
6 «Tegal sarxalukaayu rendi-dóomal bi fi kanam buntu màkkaanu xaymab ndaje mi.
7 Tegal mbalkam njàpp mi ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te nga duy ko ndox.
8 Sampal nag wurmbalu ëtt bi bépp, te nga we lafu buntu wurmbal bi.
9 «Jëlal nag diwu pal gi, nga diw ci jaamookaay bi ak li ci biiram lépp, sellale ko ko, mook yëfam yépp, mu daldi sell.
10 Boo noppee, diwal sarxalukaayu rendi-dóomal bi, mook ndabam yépp, nga sellale ko sarxalukaay bi, sarxalukaay bi daldi sella sell.
11 Nanga diw mbalkam njàpp mi akub tegoom, nga sellale ko ko.
12 «Indil Aaróona aki doomam ba ci bunt xaymab ndaje mi, nga sang leen ci ndox mi.
13 Nga daldi solal Aaróona yére yu sell yi, diw ko, sellale ko ko, mu doon sama sarxalkat.
14 Su ko defee nga indi ay doomam, solal leen ay mbubb.
15 Nga diw leen, ni nga diwe seen baay, ñu doon samay sarxalkat. Seen diwu googu moo leen sédd sasu carxal bu sax dàkk, maasoo maas.»
16 Musaa nag def loola. Mboolem noonee ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.
Musaa samp na jaamookaay bi
17 Keroog at ma topp ca at ma ñu génne Misra, ca benn fanu weer wa jëkk, ca lañu samp jaamookaay ba.
18 Musaa nag samplu jaamookaay bi: Ñu jiital tegu yi, samp làcc yi, we galan yi, daldi samp jën yi.
19 Ci kaw loolu, ñu firi malaan mi ci kaw jaamookaay bi, daldi lal kiiraay li ci kawam, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
20 Gannaaw loolu ñu jël àlluway seede si, yeb ko ci gaal gi, ba noppi roof njàppu yi ci gaal gi. Ñu daldi teg kubeeru saraxu njotlaay gi ci kaw gaal gi.
21 Ba mu ko defee ñu fat gaal gi ci biir bérab bu sell bi, doora firi ridob xàjjatle bi, làqe ko ko, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
22 Ba loolu amee ñu dugal taabal ji ci biir xaymab ndaje mi, ci wetu bëj-gànnaaru jaamookaay bi, ci kanam rido bi.
23 Ñu daldi teg ci kaw taabal ji, tegin wu jekk, mburu mi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
24 Ñu dugal nag tegukaayu làmp bi ci biir xaymab ndaje mi, fi janook taabal ji, ci wetu bëj-saalumu jaamookaay bi,
25 daldi taal làmp yi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
26 Ba mu ko defee ñu dugal sarxalukaayu wurus bi ci biir xaymab ndaje mi, ci kanam rido bi,
27 daldi taal cuuraay lu xeeñ li ci kawam, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
28 Ñu samp lafu buntu jaamookaay bi.
29 Sarxalukaayu rendi-dóomal bi nag, ñu teg ko ci bunt màkkaanu xaymab ndaje mi, daldi def ci kawam saraxu rendi-dóomal bi, ak saraxi pepp mi, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
30 Ba loolu amee ñu teg mbalkam njàpp mi ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, ba noppi duy ko ndoxum njàpp.
31 Ci la Musaa ak Aaróona aki doomam di raxas seeni loxo ak seeni tànk,
32 ndax bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, ak bu ñuy jegeji sarxalukaay bi, dañuy jàpp, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
33 Gannaaw loolu ñu samp wurmbal bi yéew jaamookaay beek sarxalukaay bi, daldi samp lafu buntu ëtt bi. Noonu la Musaa sottale liggéey bi.
Leeru Aji Sax ji gane na bérab bu sell bi
34 Ba loolu amee niir wa yiir xaymab ndaje ma, leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba,
35 ba Musaa tëlee dugg ca xaymab ndaje ma, ndax niir wa màkkaanoo kaw xayma ba, ak leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba.
36 Saa yu niir wa yékkatikoo, ba tiim jaamookaay ba nag, bànni Israyil daldi tegu ca seen yooni tukki ya.
37 Waaye bu niir wa yékkatikuwul, duñu dem, ba keroog muy yékkatiku.
38 Ndax booba niiru Aji Sax jaa nga ca kaw jaamookaay ba, ag bëccëg, te sawara waa nga ca biir niir wa, ag guddi, waa kër Israyil gépp di ci gis, seen diiru yooni tukki ya.