31
Yanqóoba toxu na, jëm Kanaan
1 Ba loolu amee mu am bés Yanqóoba dégg doomi Laban ya naan, Yanqóoba nangu na li seen baay amoon lépp, te ci seen alalu baay la sàkkoo alalam jooju jépp.
2 Naka la Yanqóoba gis kanamu Laban, daldi xam ne melatul, na mu meloon ci moom.
3 Aji Sax ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.»
4 Yanqóoba woolu Rasel ak Leya ca tool ya, fa gàttam ya nekk.
5 Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man.
6 Yeen ci seen bopp xam ngeen ne liggéeyal naa seen baay sama kem kàttan.
7 Teewul seen baay wor ma, soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom, waaye Yàlla seetaanu ko, mu di ma lor.
8 Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer.
9 Nii la Yàlla nangoo seen juru baay, jox ma.
10 «Ba ñu demee ba jur giy wara tëbu, damaa jeneer sikket yiy tëb bëy yi yépp di lu seereer ak lu tippante mbaa ñu raxe.
11 Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.”
12 Mu ne ma: “Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp.
13 Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»
14 Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay?
15 Doonunu lu moy ay doxandéem ci moom de! Nde da noo jaay, lekk sunu njég, ba mu jeex tàkk.
16 Te mboolem alal, ji Yàlla nangoo ci sunu baay, noo ko moom, nun ak sunuy doom. Kon nag léegi lu la Yàlla wax rekk, def ko.»
17 Yanqóoba daldi dajale ay doomam ak ay soxnaam, waral leen giléem,
18 ñu ànd tegu ca yoon wa, yóbbaale géttam gépp ak mboolem alal ju mu liggéey. Mooy gétt, ga mu sàkkoo Padan Aram. Ña ngay ñibbi kër baayam Isaaxa ca réewu Kanaan.
19 Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam.
20 Noonu la Yanqóoba nëbboo Laban, Arameen ba, bañ koo yégal ne day dem.
21 Ba mu demee, dafa yóbbaale la mu amoon lépp, jóge fa, jàll dexu Efraat, wuti tundi Galàdd.
Laban dabi na Yanqóoba
22 Yanqóoba daw na, ba mu am ñetti fan, ñu soog koo yégal Laban.
23 Mu ànd nag ak ay bokkam, topp ko juróom ñaari fan, door koo dab ca tundi Galàdd.
24 Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.»
25 Ba Laban dabee Yanqóoba, dafa fekk mu samp xaymaam ca tund wa. Laban it samp bosam ca kaw tundi Galàdd, moom aki bokkam.
26 Laban ne Yanqóoba: «Looy def nii, yaw, di ma nëbbuy daw, yóbbaale sama doom yu jigéen, ñu mel ni ñu ñu lële xare?
27 Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar.
28 Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii!
29 Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: “Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.”
30 Bu la neexee, nga namm sa kër baay, ba dogu caa dem, waaye lu tax nga sàcc sama gàllaaji kër, teg ci?»
31 Yanqóoba tontu Laban ne ko: «Xanaa ragaloon rekk ne jombul dinga téye say doom yu jigéen.
32 Waaye képp koo gis mu yor sa gàllaaji kër, boo yeboo reyal. Seetal fii ci sunu kanami bokk lépp lu ma fi yor, loo ci moom fabal, yóbbu.» Booba Yanqóoba xamul woon ne Rasel a ko jël.
33 Laban dugg ci xaymab Yanqóoba, teg ca xaymab Leya ak yosi ñaari jaamam yu jigéen ya, te gisul dara. Mu génne xaymab Leya, dugg ci bu Rasel.
34 Fekk na Rasel fab gàllaaji kër ya, làq ca ron tegu giléem ga, toog ca. Laban tëcc, tëcc ca biir xayma ba, gisul dara.
35 Rasel wax baayam ne ko: «Baay, baal ma de, damaa manula jóg ci sa kanam, ndaxte damaa ànd ak mbaax.» Laban seet na fu ne, waaye gisul gàllaaji këram ya.
36 Yanqóoba mer lool, daldi gëdd Laban ne ko: «Ndax damaa tooñ walla damaa moy, ba nga sambal ma, di ma topp nii?
37 Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu.
38 Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt.
39 Jur gu rab fàdd sax ma féetewoo, waaye masuma la koo indil. Mboolem lu ñu sàcc guddi ak lu ñu sàcc bëccëg, danga ma ko daa feyu.
40 Naaj wi laa daan yendoo yenu bëccëg, di fanaanoo sedd guddi, mu xaw maa rey, ba duma gëmm bët.
41 Ñaar fukki at a ngii, ma di la jaamu ci kër gi, liggéeyal naa la fukki at ak ñeent ngir sa ñaari doom yu jigéen ñii, teg ci juróom benni at yu ma la sàmmal say gàtt, nga soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom.
42 Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»
43 Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom?
44 Léegi ñëwal rekk, ñu fasante kóllëre maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.»
45 Ba loolu amee Yanqóoba jël aw doj, samp ko, muy doju xàmmikaay.
46 Yanqóoba ne ay bokkam: «Forleen ay doj.» Ñu for ay doj, def ko ab jal, daldi lekk foofa ca wetu jal ba.
47 Laban tudde bérab ba Yegar Saaduta; Yanqóoba tudde ko Galet.
48 Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede).
49 Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na Aji Sax ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree.
50 Soo soxoree samay doom yu jigéen, mbaa nga takk yeneen jabar, bu fa kenn nekkul sax, moytul, ndax Yàllaa nuy seede.»
51 Laban neeti Yanqóoba: «Xoolal ci jal bii ak doju xàmmikaay, wi ci sama digganteek yaw.
52 Jal bi seede la, doj wi di seede ne duma jéggi jal bi, jublu ci yaw, te yaw itam doo jéggi jal bi mbaa doj wi, jublu ci man, te naraluloo ma jàmm.
53 Yàllay Ibraayma ak Yàllay Naxor, ñoom ñooñee di seen Yàllay baay, yal nañu àtte sunu diggante.» Yanqóoba daldi giñ ci Yàlla, ji baayam Isaaxa wormaaloon.
54 Gannaaw loolu Yanqóoba sàkk sarax ca kaw tund wa, woo ay bokkam, ñu bokk lekk. Ba ñu lekkee ba noppi, fanaan ca tund wa.