Bataaxal bi jëm ca
Yawut ya
1
Yàlla moo feeñ ci Doom ji
1 Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottli.
2 Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.
3 Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,
4 te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.
Doom jee gëna màgg malaaka yi
5 Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko:
«Yaa di sama Doom,
bés niki tey, maa la jur,»
ba neeti:
«Maay doon Baay ci moom,
muy Doom ci man»?
6 Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan:
«Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal.»
7 Malaaka yi la Yàlla wax ci ñoom ne:
«Moo def ay malaakaam diy ngelaw,
jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara.»
8 Waaye Doom ji la Yàlla ne:
«Yàlla, sab jal tey la ak ëllëg ba fàww,
te sa yetu nguur njub lay doon.
9 Yaa safoo njubte, seexlu njubadi,
moo tax yaw Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég,
nga tiim say moroom.»
10 Mu neeti:
«Yaw Sang bi, yaa sos àddina ca njàlbéen,
te asamaan yi, sa liggéeyu loxoo.
11 Yooyu day réer,
waaye yaw yaay des,
lépp ay ràpp ni ay yére.
12 Yaa leen di taxañ ni malaan,
ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo,
te yaw, ngay kenn ki,
say at du jeex.»
13 Ana kan ci malaaka yi la mas ne:
«Toogeel sama ndijoor,
ba ma def say noon, say dëggastal»?
14 Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?