6
1 Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat kenu gi. Kenu gi mooy gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi ndee.
2 Kenu gi mooy itam njànglem xeeti njàpp, ak ñaan gu ànd ak tegeb loxo, ak mbirum ndee-ndekki, ak àtteb bés-pénc biy sax dàkk.
3 Nanu jëm kanam, te moom lanuy def, ndegam soob na Yàlla.
4 Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.
5 Ñoo mos kàddug Yàlla gu baax gi, ak manoore yu jamono jiy ñëw,
6 ba noppi xàcci. Kon deesu leen waññi, ngir ñuy tuubati, nde ñoo daajaatal seen bopp Doomu Yàlla ji ci bant, teg ko toroxte ju ne fàŋŋ.
7 Ndax suuf kat, su naanee ndox mu mu tawlu ay yoon, ba meññal ñi ñu koy beyal, gàncax gu leen jariñ, soosa suuf dina séddu ci barke bu bawoo fa Yàlla.
8 Waaye su meññee ay dég aki xaaxaam, amul njariñ, alkuteem lees di tudd léegi, te lakk lay mujje.
9 Waaye nag soppe yi, nii nuy waxe ak yeen teewul nu di leen yaakaare ci lu wér, li leen gëna amal njariñ, te bokk ci seenug mucc.
10 Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
11 Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn farlute googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk.
12 Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.
Digeb Yàlla du jaas
13 Mu mel ni Ibraayma, ba Yàlla di digoo ak moom, Yàlla manul woona giñe ku sut Yàlla. Moo tax mu giñal ko ci boppam,
14 ne ko: «Maa lay barkeela barkeel déy, ful laa ful.»
15 Noonu la Ibraayma muñe, ba kera mu jote ca dige ba.
16 Nit nag, ku ko sut lay giñe, ngir dogal kàddu, ba teesal wépp werante.
17 Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem.
18 Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.
19 Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néegu biir bu Yàlla ba.
20 Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkisedeg.