7
Israyil mooy mburu mu desee ñor
«Bu may faj Israyil
foofu ca Efrayim la seeni ñaawtéef di feeñ,
ànd ak mbonu Samari seen péey.
Dañuy njublaŋ,
sàcc yiy bëtt ci biir kër yi,
gàngoori saaysaay di songe ci biti.
Taxul ñu jàpp ci seenum xel ne
seen mboolem jëf ju bon laa bàyyi xel.
Léegi seeni jëf a leen wër ndombo,
ne màkk fi sama kanam.
Seenug mbon lañuy bégale buur,
seeni fen di bégal kàngam.
Ñoom ñépp a diy jaalookat.
Ñu mel ni taalu mburu bu yànj,
taal bu lakk-kat ba soxlawula xamb,
ca tooyal ba, ba kera xóoy bay funki.
Bu sunu buur xewlee,
kàngam yi naan ba wopp,
buur tàllal loxo ay ñaawlekat.
Seenub xol lañu waajal nib taal, di tëroo,
Seen lakk-katu mburu fanaanee nelaw*,
bët set taal ba yànj, di fër-fëri.
Ñoom ñépp a tàng jérr nib taal,
te ñooy xoyom seeni njiit,
seen buur yépp a daanu,
te kenn ci ñoom woowu ma wall.
Efrayim moo jaxasook askani jaambur,
Efrayim moo di mburu mu ñu walbatiwul cib taal.
Ay doxandéem a jeexal dooleem, te xamu ko,
aw liir tege ci kawam weex tàll, te yégu ko.
10 Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal,
te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji.
Loolu yépp taxul ñu sàkku ko.
11 Efrayim daa mel ni pitax,
dofe, ñàkk xel,
di woo wall Misraak a dem Asiri.
12 Bu ñuy dem, maa leen di laaw samab caax,
niy njanaaw laa leen di woddale fi suuf,
fa ma dégge seenum ndaje laa leen di mbugale.
13 Ngalla ñoom, nde ñoo ma daw,
yàqute ñeel na leen, nde ñoo ma gàntal.
Doon naa leen jot
waaye ñoo ma fenal.
14 Du seen xol lañu ma wooye wall,
xanaa di salliiru ci seen kaw lal,
pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram,
dëddu ma.
15 Maa leen jàngal, dëgëral seeni përëg,
te man lañuy fexeel lu bon.
16 Bu ñu waññikoo it, du fi Aji Kawe ji.
Ni xala gu yolom lañu mel,
te seeni kàngam ay fàddoo saamar
ndax seen sànjum làmmiñ,
te loolu lees leen di reetaane
ca réewum Misra.
* 7:6 Ki jiite pexe mu bon mi moo fanaanee nelaw ca guddig xawaare ja, bët set mu jóg, joxe ab tegtal, ngir ñu sottal pexe ma. 7:14 Ñi daan jaamu Baal mi ñu jiiñ ne mooy nangul suuf, ñoo aadawoo woon di dagg seen yaram, di tuur seen deret ci suuf, ngir foog ne loolu mooy tax seen mbey nangu.