9
Yoonu ngàllog Israyil taxaw na
Yeen waa Israyil, buleen béglu,
buleen bànneexu ni yeneen xeet yi,
nde yeena gànctu, dëddu seen Yàlla,
yeena safoo peyu ngànctu
ci mboolem dàgga ju ñuy bàcce pepp.
Ndaxam dàgga ak nalukaayu reseñ
du leen regg,
te biiñ du leen doy.
Dungeen des ci réewum Aji Sax ji.
Efrayim, Misra lay dellu,
te ca Asiri, lu daganul lañu fay lekkeji.
Duñu tuural Aji Sax ji saraxu biiñ,
te seeni sarax du ko neex.
Seen ñamu sarax day mel ni ñam
wu ku nekk fu nit deeye, sobeel,
ba ku ca lekk sobewu*.
Seenu ñam, seenub koll lay ñeel,
waaye du dugg ci kër Yàlla gi.
Ana nu ngeen di def nag, ci bésu ndaje,
bésub màggal bu Aji Sax ji?
Ñu ngoogu dem ndax tasteg réew mi,
Misraa leen di fat, Memfis suul leen,
seen tànnéefu xaalis, mbooy mee koy nangu,
te xaaxaam ay saxe seen biiri xayma ya woon.
Fexeel nañu yonent yi
Bési mbugal dikk na,
bési añale taxaw na,
na ko Israyil xam.
Yonent lañu jàppe ab dof,
ku yor waxyu di ku wéradi,
ndax seen ñaawtéef gu réy,
ak seen mbañeel gu tar.
Yonent bi mooy jongrukat
biy wattul Yàlla, Efrayim,
waaye ag fiir lees ko lalal
ci mboolemi yoonam,
te mbañeel a ngi ci biir kër Yàllaam.
Ñoo sóobu ci xóotey yàqute,
na woon ca janti Gibeya,
te Yàlla mooy bàyyi xel seenug ñaawtéef,
ba mbugale leen seeni moy.
Israyil wor na Aji Sax ji
10 «Ni cabbu reseñu biir màndiŋ,
ni laa fekke Israyil.
Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo,
ni laa gise seeni maam.
Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor,
ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi,
ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.
11 Efrayim, ab sagam ni picc lay naawe,
du njurum doom, dub ëmb, du doom ju sosu sax.
12 Bu ñu yaroon seeni doom it,
maa leen leen di xañ,
ba kenn du des.
Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.
13 Ni ma dogule Tir dëkk ba,
bi jëmbate ci parlu mu naat,
ni laay dogule Efrayim,
ba yóbbul ay doomam ab bóomkat.
14 Aji Sax ji, yool leen!
Ana loo leen di yool?
Yool leen biir yu yàqu,
ak ween yu ne sereŋ.
 
15 «Seen gépp mbon moo feeñ ca Gilgal,
te fa laa leen jéppee ndax mbonug seeni jëf.
Sama kër laa leen di dàqe,
te dootuma leen bëgg,
seeni njiit yépp a diy fippukat.
16 Fàddees na Efrayim,
ay reenam wow,
du meññ benn doom.
Bu juroon itam, maay rey
ngëneelu biiram.»
 
17 Sama Yàlla moo leen di xalab,
nde ñoo ko déggalul,
te ñooy taxawaaluji ci biir xeeti jaambur yi.
* 9:4 Bokk ag lekk ci néeg bu nit deeye daan na sobeel ña fa lekk. Seetal ci Màndiŋ ma 19.14-22. 9:9 Ca Gibeya lañu bóome woon as ndaw, ba ñu mujj dagg ko ay dog yu ñu def firnde, yónnee ko bànni Israyil gépp. Seetal ci Njiit ya 19-21. 9:15 Gilgal mooy dëkk bu ñuy misaale jëfi bokkaale. Seetal ci Ose 4.15.