10
Mbugal ñeel na kàngami Yuda
Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi,
bind ko, te muy jur coono,
di ko àttee ñàkkal ku ñàkk,
di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ,
bay lekk ab jëtun,
di sëxëtoo ab jirim.
Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba,
keroog ba safaan di bawoo fu sore?
Ana ku ngeen di daw wuti wallam?
Ana fu ngeen di denci seen teraanga?
Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg;
mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet.
 
Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom,
meddiwul ba tey.
Asiri muccul ci mbugal
Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer,
bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi,
yebal ko ca askan woowu ma merloo,
ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal,
note leen ni banu mbedd.
Waaye Asiri gisewu ko noonu,
xalaatewul noonu;
bóome la xintewoo,
ba fàkkas xeeti xeet.
Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu?
Am Amat daa gën Arpàdd*?
Am Samari daa gën Damaas?
10 Maa duma réew yu seeni yàllantu,
seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.
11 Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom,
duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»
12 Boroom bi nee:
«Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem,
maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi,
ak gëti xeebaateem.»
13 Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii,
maa xelu, ràññee;
ba randal kemi suufi xeet yi,
foqati seeni alal,
dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.
14 Maa teg alali xeet yi loxo,
ni ku gis am tàgg.
Maa tonneendoo réewi àddina
ni ku for ay nen, tonni lépp,
laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»
 
15 Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore?
Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge?
Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb;
mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!
16 Moo tax Boroom bi,
Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi,
di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi,
seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.
17 Aji Sax ji, leeru Israyil mooy doon sawara,
ku Sellam kooku mooy doon tàkk-tàkku sawara,
xoyom taxasi Asiri aki dégam ci benn bés.
18 Gott bu naat ak tool bu meññ, mu ne faraas fóom,
ba mu mel ni ku wopp, yaram way seey,
19 gott ba dese garab yu néew
yu gone mana lim, bind ko.
Ndesu Israyil dina ñibbi
20 Keroog bés booba
li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba
duñu wéerooti ña leen duma.
Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko,
Aji Sell ju Israyil.
21 Aw ndes ay délsi,
di ndesu askanu Yanqóoba,
ñeel Yàlla Jàmbaar ji.
22 Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu,
te as ndes a ciy délsi.
Àtteb sànkute mooy taxaw,
yoon toppe ba mat sëkk.
23 Sànkute déy mooy taxaw,
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
di ko sottal fi réew mi mépp.
 
24 Moo tax Boroom bi,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
dafa wax ne:
«Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ,
buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet,
ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen.
25 Waaye fi leek lu néewa néew
mbugal jeex fi seen biir,
am sànj sippil Asiri seen sànkute.»
26 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee leen di ŋàbbal kàccri,
na mu defoon waa Majan fa doju Oreb.
Mooy xàcciw yetam, mu dal géej,
na mu defoon fa Misra.
27 Bésub keroog sëf bu ñu leen sëfoon wàcc leen,
ngeen tàggook yet wu ñu leen tënke woon,
nde seen yaram ay naat, ba yet wa damm.
Noon yi songsi nañu
28 Noon yeey songsi Ayat, jéggi Migron,
dem ba Migmas, teg fa seeni jumtukaay,
29 jaare ca xunti ma
te naan: «Geba lanuy fanaani!»
Waa Raama tiit, waa Gibeya gu Sóol daw.
30 Yeen waa Galim, yuuxuleen,
yeen waa Laysa, dégluleen,
yeen waa Anatot, feeluleen.
31 Waa Madmena ñooy fëlxoo,
waa Gebim wuti rawtu.
32 Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob,
di sànni loxo waa tundu Siyoŋ,
di ko tëkkoo waa Yerusalem googu.
33 Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi,
njobbaxtal ya gëna kawe dog,
la ca gënoona siggi, wàcc.
34 Mooy jël sémmiñ, goraale gajji gott bi,
Libaŋ loroo loxol boroom doole, ba jóoru.
* 10:9 Kalne ak Karkemis ak Amat ak Arpàdd ay dëkki Siri lañu.