18
Waxyu jib na, ñeel réewum Kuus
Wóoy ngalla réew ma gunóor yay riire,
ca tàkkal dexi réewum Kuus.
Yeen ñiy yónni biir géej, ay ndaw,
ci gaali barax yu war mbeex mi;
yeen ndaw yu gaaw yi, demleen,
fekki xeet wu siggi, rattax yaram,
askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore,
xeet wu am doole, di falaxee,
te seenum réew defi wal.
 
Yeen waa àddina wërngal këpp,
yeen ñi dëkke suuf si,
séentuleen raaya ba sampe fa tund ya,
dégluleen liit ga ñuy wali.
Aji Sax ji kat da maa wax ne:
«Maa ngi fi ma tollu di xool, ne tekk,
ni tàngooru jant bu ne ràññ,
mbaa lay bu defu niir ci tàngooru ngóob.»
Bala ngóob di jot, te fekk lépp tóor,
ba tóor-tóor def reseñ ju xaay,
mu jël ab sàrt, dog car yu ndaw yi,
tenqi car yu mag ya, sànni;
ñu boole waccal njanaawi tund ya
ak rabi àll yi,
tan yi nawetoo ko,
rabi àll yépp nooroo ko.
Su boobaa ñu indil Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
galag bu bawoo ci xeet wu siggi, rattax yaram,
askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore,
xeet wu am doole, di falaxee,
te seenum réew defi wal,
galag ba agsi ba tundu Siyoŋ,
fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dëël turam.