23
Ab yéeneb waxyu ñeel na Tir
Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir*:
Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen!
Lépp a yàqu!
Du kër, du teeruwaay.
Fa dunu Sippar lañu leen ko waxe.
Yeen waa tefes,
yaw Sidon laa ne, na say jula ñaawlu,
yaw miy yónni nit ñu jaare géej,
war ndox ya ne xéew,
peppum Sixor di sa tono,
ak ngóobum Niil,
ma xeet yi daan jula.
Yaw Sidon, gàcce ñeel na la,
géej moo wax, tatay géej a ne:
«Masumaa matu, masumaa jur,
yaruma gone gu góor, yarumab janq.»
Bu xibaar ba àggee Misra de,
ñu naqarlu deminu Tir.
Jàllal ba Tarsis§,
yeen waa tefes ga fa ne, jooyleen jooyi dëj.
Xanaa lii du seen dëkk bu xumb ba,
te cosaanam di janti démb,
nit ña di fa jógey sancaani fu sore?
Ana ku fexeel lii Tir ma daan fale,
ay julaam diy kàngam,
di jaaykat yi àddina teral?
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko fexe,
ngir sàggi sagub képp ku fiy damu,
ba teddadil képp ku àddina teral.
10 Yeen waa Tir, defleen ni dexu Niil, walal seen réew;
kenn tereetu leen.
11 Aji Sax ji tàllal na loxoom, tiimale géej,
yëngal réew yi,
ba santaane ñu màbb tatay Kanaan.
12 Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde,
dootuleen xaxaloo.
Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar,
te du tax ngeen am fa noflaay.
13 Xool-leen li dal réewum Kaldeen ñi.
Dootuñu sax aw xeet.
Asiri wacce na leen rabi màndiŋ mi.
Tabax nañu, gaw ko, màbb këri buur ya, gental ko.
14 Yeen boroom gaali Tarsis, yuuxuleen ni ñu deele,
seen tata màbb na!
15 Bu keroogee ñu fàtte Tir juróom ñaar fukki at, ni àppu benn buur. Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Tir xewle la ñu woyal gànc ba, ne ko:
16 «Yaw gànc bi ñu wacc, fabal sa xalam, wër dëkk bi,
xalamala xalam te gëna woy,
ndax ñu geesu la.»
17 Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Aji Sax ji dikkal Tir, ñu delluy liggéey, di feyu, di gànctook mboolem réewi àddina fi kaw suuf 18 Waaye seen ñaq ak seen peyoor, dees koy sellalal Aji Sax ji, deesu ko dajaleek a denc. Ñi dëkk fi kanam Aji Sax jeey jagoo njariñ la, mu di leen dundal ba ñu regg, di leen solal col gu jekk.
* 23:1 Tir ak Sidonay dëkk yu am solo la woon ca Fenisi, ci réew mi ñuy wax Libaŋ tey. 23:1 Mbaa: dunu Kitim. 23:3 Mooy dexu Niil. § 23:6 Ab sanc la bu bokkoon ci Tir, ca wàllu Espaañ.