25
Cant jib na
1 Aji Sax ji, yaay sama Yàlla,
dama lay teral, di la sant.
Yaa defi jaloore,
muy dogal yu yàgg, wér te wóor.
2 Yaa def dëkk bi jali doj,
dëkk bii ñu dàbbli nga gental;
taaxu doxandéem yi noppee doon péey ba fàww,
te deesu ko tabaxaat.
3 Moo tax xeet wu am doole di la màggal,
waa péeyu xeet yu néeg di la wormaal.
4 Yaa di rawtub néew-ji-doole,
di rawtub aji ñàkk, biir njàqare,
yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame,
di ker gu ñuy serloo ci tàngoor,
nde merum kilifa gu néeg
mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.
5 Doxandéem yii diy noon,
ni ngay dàqe tàngoor fi bérab bu ne sereŋ,
ni ngay dakkale seen coowal xare.
Ni aw tàngoor di dakke ndax aw niir,
ni la woyu ñu néeg ñi di selawe.
Bernde ñeel na xeet yépp
6 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
mooy berndeel xeet yépp fi kaw tund wii,
bernde ju niin ak ngëneelu biiñ,
yàpp wa duuf, yuq ja ne xéew,
ak tànnéefu biiñ bu teey.
7 Fi kaw tund wii lay tukkile càngaay,
li sàng askanoo askan,
ak séru rabal bi ñu ràbbal xeetoo xeet.
8 Mooy mëdd ndee ba fàww!
Boroom bi, Aji Sax jeey fompe
gépp kanam rongooñi boroom.
Buumi gàccey ñoñam it,
moo koy doge fépp ci àddina.
Aji Sax ji kat wax na ko.
9 Bésub keroog dees na ne:
«Sunu Yàllaa ngii nag!
Moom mii lanu yaakaaroon
te moo nuy wallu.
Aji Sax jii lanu yaakaaroon,
nan bég te bànneexoo wallam.»
Aji Sax ji tas na Mowab
10 Aji Sax ji kat teg na tund wii loxo,
te ni ñuy dëggaatee boobum leeñ,
ni lees fiy dëggaatee Mowab.
11 Mowab dina féqoo féqu,
mel ni kuy jéema féey,
waaye Aji Sax jee leen di torxal,
ñook seen manoore.
12 Seen tata yu kawe, mu fél, màbb;
rattax fi suuf, maasale.