31
Musiba ñeel na ku yaakaar Misra
1 Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall;
di sukkandikoo ay fas,
tey yaakaari watiir ndax bare ga,
aki gawar ndax lim bu takku ba
te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil,
sàkkuwñu kooku di Aji Sax ji.
2 Moona moom it xareñ na,
mane na safaan,
te du fommi digeem.
Kuy def lu bon, mu dal ci waa këram;
kuy def lu ñaaw, mu song ay wallam.
3 Waa Misra, niti neen, duñu Yàlla;
seeni fas it, suuxu neen, duñu leneen.
Aji Sax jeey xàcci loxoom,
kiy walloo mooy tërëf,
ki ñuy wallu daanu,
ñoom ñépp bokk sànku.
4 Aji Sax ji déy da maa wax ne ma:
«Gaynde gu mag ak gu ndaw, bu jàppee bay xiiru,
boo ko wooloon gàngooru sàmm it,
duñu soowaloo ba xëbal ko,
duñu ñolñoli ba mu dellu gannaaw.
Noonu la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy wàcce,
xaresi fi kaw tundu Siyoŋ ak waa tund wa.»
5 Ni picc di daayaarloo, aar am tàggam,
ni la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy yiire Yerusalem.
Mooy aar, di xettli,
mooy musal, di yiwi.
6 Éy bokki Israyil, fippu ngeen Aji Sax ji ba sës, waaye walbatikuleen!
7 Bésub keroog ku ne sànni yàllantuy xaalisam, ak yàllantuy wurusam yi mu sàkke woon loxoy bàkkaaram.
8 Asiri nag day daanu,
te saamaru nit du ko daaneel,
saamar bu doom aadama moomul a koy alag,
mu daw, won saamar gannaaw,
ay gone yu góoram dugg liggéeyu sañul-bañ.
9 Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet,
seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba.
Kàddug Aji Sax jee,
Boroom sawara wi ci Siyoŋ,
Boroom taal bi ci Yerusalem!