50
Aji Sax ji waccul ñoñam
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Damaa fase seen ndey?
Wonleen ma kayitu pase mi!
Maa leen jaay njaam, feyey bor?
Ana ku ma leen jaay?
Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a.
Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a.
Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa?
Ma woote, kenn wuyuwul?
Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo?
Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee?
Xanaa du maay gëdd géej, mu wow,
maay defi dex màndiŋ, ndox tukki;
jën ya mar, dee ba yàqu?
Du maay sànge asamaan ag lëndëm,
mu mel ni ku ma solal saaku yu muy ñaawloo?»
Siggal nañu jaamub Aji Sax ji
Boroom bi Aji Sax ji moo ma may
làmmiñu ndongo lu mokkal,
ngir ma xam gan kàddu laay jàpplee ku sonn.
Suba su ne mu yee ma, yeel ma nopp
bu ma teewloo ni dongo yi.
Boroom bi Aji Sax jee ma bënnali nopp,
te man it, gàntalu ma ko,
deltuwma gannaaw.
Gannaaw laa jox ku may dóor,
dékk lex kuy xus sama sikkim,
te làquma sama kanam
ku may saagaak a serati.
Waaye Boroom bi Aji Sax jee may dimbali,
ba tax rusuma.
Moo ma taxa dogu ba dëgër,
ngir xam naa ne deesu ma rusloo.
Ki may dëggal jege na.
Ana kuy layook man? Nan bokk taxaw!
Kuy jànkoonteek man ci yoon? Na jegesi boog!
Ma ne, Boroom bi Aji Sax jee may dimbali.
Ana ku may daan?
Dama ne, ñoom ñépp ay jeexal
ni yére yu saxe ba sagaroo.
 
10 Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen,
di déglu kàddug jaamam?
Képp kuy doxe lëndëm
te amul leeraange,
na wóolu Aji Sax ji,
te wéeroo Yàllaam jii.
11 Ma ne, yeen ñiy jafal ab taal ñépp
tey gañoo jum yuy boy,
xuusleen ci sawara si ngeen jafal
ak jum yi ngeen boyal.
Maa leen dogalal lii:
yeenay tëddaale mitit.