58
Jaamu Yàlla, tuub, rafet jikkoo ci gën
Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man,
te bul ñéeblu;
àddul ni bufta,
te yégal sama ñoñ seen bàkkaar,
ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy.
Man mii lañuy sàkku bés bu ne,
di wuta xam sama coobare!
Mbete xeet wuy def njekk,
te waccul ndigalu yoonu Yàllaam.
Ñu ngi may ñaan àttey njekk,
di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci?
Lu nuy toroxlu te teewluwoo?”
Ma ne: Bés bu ngeen woor,
yeena ngi topp seen bakkan,
di sëqatal seeni liggéeykat.
Xanaa du koor gu ànd ak xulook ŋaayoo,
ak di joqlantey këmëx yu metti?
Su ngeen bëggee seen ñaan àgg fa kaw,
dungeen woor ni ngeen woore tey.
Ndax lii moo di koor gi ma taamu,
ci bés bu nit kiy toroxlu?
Koorug dëngal loos ni barax,
lal saaku, sotti ab dóom, tëdd
di ko ñaawloo?
Loolooy seen koor,
ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?
 
«Xanaa du lii moo di koor gi ma taamu:
yolomal jéng yu metti,
fecci buumi noteel,
afal ku diis;
dog lépp luy xeetu noteel?
Xanaa du sédd ku xiif saw ñam,
fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk,
gis ku rafle, wodd ko,
te baña nëbbu mbokk mu soxla?
Su boobaa seen leer feq ni njël,
seen góom gaawa wér,
seen njekk jiitu leen,
leeru Aji Sax ji féete leen gannaaw.
Su boobaa bu ngeen wooyee Aji Sax ji, mu wuyu;
ngeen ne wallóoy, mu ne “Maa ngi.”
Ndegam génne ngeen noteel ci seen biir,
ak di joxoñeek a wax lu ñaaw,
10 di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg,
di reggal néew-ji-doole,
su boobaa seen leer fenke biir lëndëm,
seenug këruus di ag njolloor,
11 Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu,
di leen màndale joor gu maral,
dëgëral seeni cér,
ngeen mel ni tool bu ñu suuxat,
mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis,
12 seeni nit tabaxaat gent ya woon,
ngeen yékkatiwaat kenu yu yàgga yàgg.
Dees na la wooye jagalkatu xar-xar yi,
mbaa kiy yeesal xàll yi, ngir dëkke réew mi.
 
13 «Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay,
baña def li leen neex sama bés bu sell;
su bésub Noflaay di seen nammeel,
di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral;
ngeen teral bés bi,
bañ cee topp li ngeen jikkowoo,
di topp seen bakkan
ak wax ju dul jeex;
14 su boobaa ngeen bànneexoo Aji Sax ji,
ma waral leen kawtey réew mi,
leele leen seen céru maam Yanqóoba.»
Aji Sax ji déy wax na ko.