7
Yaakaar Yàlla war na Buur Axas
Janti buurub Yuda, Axas doomu Yotam miy doomu Osiyas, Reccin buurub Siri moo dal ci kaw Yerusalem, ànd ak buurub Israyil, Peka doomu Remalya. Waaye manalu leen dara. Ba ñu yégalee Buur Axas sëtub Daawuda, ak waa këram, ne ko waa Siri, Efrayim* lañu lëngool, mbir ma yëngal na Buur Axas ak waa réew ma, ba mel ni garabi gott bu ngelaw li gësëm. Aji Sax ji wax Esayi ne ko: «Génnal gaaw, dajeek Axas, yaak sa doom Seyar Yasub, ma nga ca catal solomu mbànd ma féete kaw, ca yoonu toolu fóotkat ya. Nga wax ko ne ko:
“Defal ndànk te ne cell.
Bul tiit, bul xàddi
ndax merum Reccin ak Siri,
ak doomu Remalya ji.
Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxar!
Waa Siri ñoo ànd ak Efrayim ak doomu Remalya,
di la fexeel naan:
‘Nan songi Yuda,
tiital leen, nangu ko,
fal fa doomu Tabeel buur.’
Waaye Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
‘Loolu du sotti, du am.
Damaas a yilif Siri,
te Reccin yiliful lu moy Damaas.
Fii ak juróom benn fukki at ak juróom
Efrayim tas, ba xeet wa réer.’
Samaree yilif Efrayim,
te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari.
Dungeen mana saxoo dëgër nag,
ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”»
Juddub Emanuwel firnde la
10  Aji Sax ji teg ca ne Axas: 11 «Ñaanal sa Yàlla Aji Sax ji firnde. Ñaan ko ko, ak fu mu mana bawoo, fa suufa suuf, mbaa fa kawa kaw.» 12 Axas ne: «Duma ko ñaan, ndax duma nattu Aji Sax ji.» 13 Esayi nag ne:
«Yeen waa kër Daawuda, dégluleen!
Tàyyiloo ngeen nit,
di tàyyiloo sama Yàlla itam.
14 Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde:
janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor,
tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).
15 Soow ak lem lay lekk,
ba keroog muy mana taamu lu baax,
ba lu bon.
16 Bala xale bee ràññee lu baax ak lu bon,
dees na gental réew mii nga ragal seen ñaari buur.
17 Aji Sax jee lay dikke,
yaak saw xeet ak sa waa kër baay,
ay bés yu tar yu masula am,
ba Efrayim dëddoo Yuda ba tey,
te buurub Asiri la koy sababe.»
18 Bésub keroog Aji Sax ji ootal weñ,
ya fa catal wali ndoxi Misra,
ak yamb ya fa réewum Asiri,
19 ñu dikk, bokk tagesi mbartali xunti yi,
ba ci xar-xari doj yi,
ak gajjoo gajj, ak déegoo déeg.
20 Bésub keroog saatu la Boroom biy wate,
te saatu ba moo di buurub Asiri,
mu àbbe ko ca wàllaa dex,
wat la nel,
wat say yeel,
xuuf sab sikkim.
21 Bésub keroog nit du fa dundle
lu dul wenn nag ak ñaari gàtt,
22 meew ne gàññ, ndax nit ñu néew,
di dunde am soow,
nde soow ak lem la képp ku des ci réew ma di dundeji.
23 Fu junniy reseñ taxaw tey,
di jar junniy donji xaalisu lëmm,
bésub keroog ay dég aki dagg nangu ko.
24 Xalaaku fitt lees fay deme,
ndaxi dég aki dagg yu fees réew mi.
25 Mépp mbartal mu ñu daan gàbb,
deesu fa demati,
ndax ragali dég aki dagg,
aw nag a cay fore,
am xar curpee ca.
* 7:2 Efrayim moo gëna yaatu ci fukki giir ya féete woon réewum Israyil ga ca bëj-gànnaar, te moo taxawe taxawaayu Israyil.