2
Nattu nuyooti na
Mu am bés goney Yàlla dikk, teewsi fa Aji Sax ji. Seytaane itam bokk ca, dikk teewsi fa Aji Sax ji. Aji Sax ji ne Seytaane: «Ana foo jóge nii nag?» Mu ne ko: «Ci wër-wëraan ak doxantoo àddina laa jóge.» Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi! Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.» Seytaane ne Aji Sax ji: «Bakkan a wuutu bakkan rekk. Mboolem lu nit am, man na koo weccee bakkanam. Léegi xàccil sa loxo rekk, dal ci kaw jëmmam jépp. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.» Aji Sax ji ne Seytaane: «Kon mu ngoogu say loxo. Waaye bakkanam daal, sàmm ko.» Ba mu ko defee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji. Ci kaw loolu mu sànni Ayóoba ay taab yu metti, dale ko ca téstën ma, ba ca kaw bopp ba. Mu wut tojitu njaq, di ko xasanoo, daldi toog ci biir jalub dóom. Jabaram ne ko: «Yaa ngi ŋoy ci sa mat gi ba tey? Xarabal Yàlla boog te dee!» 10 Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.
Ayóoba am nay gan
11 Gannaaw loolu ñetti xariti Ayóoba ñoo dégg mboolem musiba moomu ko dikkal. Ku nekk ci ñoom jóge këram: Elifas waa Teman ba, ak Bildàdd waa Suwa ba, ak Cofar waa Naama. Ñu bokk daje ngir dikk mas-sawu Ayóoba, dëfal ko. 12 Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp. 13 Bokk nañu toog ak Ayóoba fa suuf juróom yaari bëccëg ak juróom yaari guddi, kenn waxu ko baat, ndax dañoo gis mitit wa mu àndal tar lool.