22
Elifas nee tuub a war Ayóoba
1 Ba loolu amee Elifas ma cosaanoo Teman àddu ne:
2 Yàlla, ana lu ko nit mana jariñ?
Xanaa ku xelu jariñ boppam!
3 Ana lu sag njub mana yokk Aji Man ji?
Lu ko sag mucc ayib mana indil?
4 Xanaa du sag njullite la lay bantale,
bay àgg ak yaw ci layoo?
5 Du sag mbon gu réy a la ko yóbbe,
ak say tooñ yu amul kem?
6 Yaa lebal mbokk, aakimoo tayleem ci dara,
bay nangu mbubbam néew-ji-doole, mu ne duŋŋ.
7 Yaa mayul ku mar ndox mu naan,
mbaa nga xañ ku xiif lu mu lekk.
8 Boroom doole jagoo réew mi,
ku ñu beral loxo dëkke.
9 Yaa bàyyi jëtun, mu deme loxoy neen,
tey néewal doole ab jirim.
10 Moo tax ay ndëgg-sërëx di la dar kepp,
musiba jekki ne la taral,
11 mbaa lëndëm gu la teree gis,
mbàmbulaan dikk, mëdd la.
12 Xanaa Yàlla sutul asamaan?
Xoolal biddiiw ya gëna kawe!
13 Nga naa: «Ana lu Yàlla xam?
Ana nu muy àttee ci gii lëndëm gu tar?
14 Niir yee ko làq ba du nu gis,
fa muy doxantoo ca kaw taaxum asamaan!»
15 Dangaa nara topp ñallu démb,
wa nit ñu bon ña ñaloon?
16 Ñoo buube, ne mes te seen àpp jotul,
seen kenu màbb, wéy nim wal,
17 te ñoo doon naa Yàlla: «Xiddi nu!»
Ñii ana lu leen Aji Man ji di def?
18 Moona moo feesaloon seeni kër ay teraanga,
waaye ñu bon ñii, royuma leen fenn.
19 Aji jub ñeey gis sànkutey ñii, bég;
ñu mucc tuuma ñaa leen di kókkali,
20 naan: «Ña nu jógaloon sànkuwuñoom?
Seen koom ma xoyomuwul a?»
21 Jubool ak Yàlla rekk, am jàmm,
ngëneel dikkal la.
22 Nangool ndigal ci làmmiñam,
te dëxëñi kàddoom ci sa biir xol.
23 Dellul ci Aji Man ji rekk, ba taxawaat,
te nga sorele sa xayma njubadi.
24 Tegal wurus ci suuf,
wacce wurusu ngalam doji xur,
25 te Aji Man ji di sa wurus,
di sa jali xaalis.
26 Su boobaa nga bége Aji Man ji,
mana siggi, séentu Yàlla,
27 di ko ñaan, mu di la nangul,
yaw it ngay wàccook say dige,
28 loo dogu, mu sotti,
foo jaare, mu leer,
29 ba bu nit detteeloo, nga yékkati ko,
te ku toroxlu, Yàlla wallu la.
30 Ku ñàkkula tooñ sax, mu xettli la,
te sag ñàkk sikk lees koy xettlee.