26
Yaa mat wall
Ayóoba àddu, ne:
Ndaw ndimbal lu réy ci ku néew doole!
Yaaka mana wallu ku amul kàttan!
Yaaka mana xelal ku xeluwul
ak xam-xam bu yaa bi nga fi xamle!
Ana ci koo jële sa kàddu yii sax?
Ak ku la xelal miim xel?
Yàlla kenn xamu ko.
Ndem-si-yàlla yaa ngay lox
ca ron ndoxi biir suuf, ñook ña fa dëkke.
Fàŋŋ la njaniiw def fa kanam Yàlla;
du genn kiiraay gu ko làq paxum sànkute.
Kee firi asamaan fu dara amul,
sanjamtal suuf fu dara newul.
Kee gëndaley ndox ciy xàmbaaram,
te taxul niir wa ñu laloo fàcc.
Keey firi aw niiram,
yiire ngànguneem.
10 Kee rëdd digu wërngal fi kaw géej yi,
fa cat la leer ak lëndëm digaloo,
11 kenuy asamaan jaayu,
di jommi ci kàddu yi muy gëddee.
12 Dooleem la mane géej,
manooreem la rajaxee Raxab ninki-nànka ja.
13 Noowam wal, asamaan leer,
loxoom jam jaan jay balaw-balawi.
14 Lii de, mooy lenni jalooreem!
Ndaw ndéey lu tuut lu nu ci dégandeem!
Ana ku mana xam riiru dooleem?