31
Ayóoba waat na
1 Maa jaayanteek samay gët.
Ana nu may xooleb janq?
2 Lu ko moy ana sama cér ca Yàlla ma fa kaw?
Lu ma Aji Man jiy sédde fa kawte ya?
3 Xanaa du safaan a ñeel ku bon,
naqar ñeel ku ñaaw?
4 Du Yàllaa ngi gis fu ma jaare,
di waññ sama bépp jéego?
5 Ndegam damaa doxe ndëngte,
mbaa ma gaawtoo njublaŋ,
6 na ma Yàlla natte màndaxekaayu dëgg,
ba ràññee samag mat!
7 Ndegam samay tànk a moy yoonu njub,
mbaa sama xol topp saay gët,
mbaa sama yoxo yii gàkk fenn,
8 yal naa ji, keneen lekk,
ma jëmbat, ñu buddi.
9 Ndegam jabaru jaambur a ma xañ sago,
ba ma di ko yeeroo sama buntu kër moroomu góor,
10 yal na sama jabar bojjal keneen,
ñeneen tiim ko.
11 Su ma ko defoon, muy jëfu yàqute,
di moy gu yeyoo pénc,
12 te di sawara wu may xoyom
ba ca paxum sànkute ma,
lu ma meññle, mu buubaale.
13 Ndegam maa sofental sama àqu jaam,
bu ñu may jooytu, diy góor mbaa jigéen,
14 bu ci Yàlla jógee, ana nu may def?
Bu ma ko laajee, ana lu ma koy wax?
15 Ki ma sàkk ci sama biiru ndey,
xanaa du moo leen sàkk ñoom itam?
Du kenn kee nu sos ci njurukaay?
16 Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku,
mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?
17 Am damaa masa wéetoo ab dog,
te sédduma ca jirim?
18 Ba may ndaw laa dala yor ab jirim ni baayam;
te ba ma juddoo ci sama ndey laa dala gindi ab jëtun.
19 Ndegam maa seetaan ku rafle nara sànku,
seetaan néew-ji-doole ju amul malaan,
20 te sànguma céram, mu sante ma ko,
di nugloo ndimo lu ñu ràbbe sama kawari gàtt,
21 ndegam maa xàccil sama loxo ab jirim,
ndax yaakaar kiirlaay ca pénc ma,
22 yal na sama loxo teqlikook sama mbagg,
sama përëg fàqe ci conc li.
23 Mbugalu Yàlla kat laa ciy ragal,
te màggaayam xajul ci man.
24 Ndegam damaa def wurus sama yaakaar,
bay tudde ngën-gi-wurus sama cëslaay;
25 ndegam maa bége sama alal ju bare,
bége koom gu ma sama doole may;
26 ndegam maa masa niir jant beek leeraayam,
mbaa weer wiy daagoo yànjaayam,
27 ba namma làqu, di ci jaamu lenn,
bay fóon sama loxo, wormaale leen;
28 konoon it muy ñaawtéef gu yeyoo àtte,
nde kon ma weddi Yàlla ma fa kaw.
29 Ndegam maa bége musibay bañ,
mbaa ma bellaxndikoo loraange ju ko dab,
30 te bàkkaarewuma sama làmmiñ sax,
ba di ci ñaanal noon alkànde,
31 ndegam du samay bokk a ma seedeel ne:
«Ana ku mu leelul ndawal ba mu regg?»
32 te biti, masumaa wacc doxandéem di fa fanaan,
sama bunt laay ubbil ku nekk ciw yoon,
33 ndegam maa roy nit ñi, di nëbb samay tooñ,
di nëpp-nëppal sama sikkaange,
34 ragaluma jëwu àddina de,
tiituma mbooloo mu ma nawloodi it,
ba ne cell baña génn sama buntu kër.
35 Ma ne éy ku may may nopp?
Sama torloo ngoog, na ma Aji Man ji tontu!
Su dee téereb tuuma bu ma ku may layool bindal,
36 maa koy gàddu, kaalawoo.
37 Maay limal Yàlla jéego bu ma séqi,
di taxawi fa kanamam taxawaayu garmi.
38 Ndegam sama tool a ma tuumaale ay jooy,
rongooñi toobo yay bas-baseendoo,
39 ndegam maa lekk lu ca ñor, te dikkewuma dara,
ba xañ bakkan ña ma ko beyaloon,
40 kon yal na ay dég wuutu bele ba,
ñax mu bon wuutu lors ba.
Fii la kàdduy Ayóoba yem.