31
Israyil séentu na sancaatub réewam
«Su boobaa,» kàddug Aji Sax jee, «maay doon Yàllay làngi Israyil yépp,
ñoom ñuy sama ñoñ.»
 
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Waa Israyil ñi rëcc ñawkay saamar,
daje nañook yiw ci màndiŋ mi,
fekk ñuy sàkku noflaay.»
Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu,
ne nu: “Maa leen masa bëgg,
ba tax ma sédd leen ngor.
Yaw Israyil mu taaru,
maa lay defaraat, nga defaru,
ba jiinaat sam njiin,
wàlli peccum mbéx,
jëmbataat sa tóokëri reseñ
ca mbartali Samari,
te ku jëmbat, xéewlu ca.
Bés dina ñëw déy,
wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayim
ne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu Siyoŋ,
fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’ ”»
Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Sarxolleleen, bége askanu Yanqóoba,
xaacul-leen xeet woowu jiitu,
biral-leen cant te ne:
“Éy Aji Sax ji, wallul ndesu Israyil, sa ñoñ ñii.”»
 
«Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar,
dajalee leen fa cati àddina.
Silmaxaa ngi ci akub lafañ,
jigéenu wérul it ak kuy wasin,
ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.
Ñooy dikk di jooy, di leewaayu,
ma jiite leen, yóbbu,
jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo,
ba ca wali ndox ya,
ngir maay baayu Israyil,
Efrayim di sama taaw.
 
10 «Yeen xeet yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji,
yégleleen ko ca tefes yu sore ya.
Ne leen: “Ki tasaare woon Israyil, moo leen di dajale,
sàmm leen ni sàmm ak géttam.”
11 Aji Sax jee goreel askanu Yanqóoba,
jot ko ci loxol ku ko ëpp doole.
12 Ñooy dikk, di sarxollee kaw tundu Siyoŋ,
ne ràññ ndax ngëneeli Aji Sax ji,
pepp, biiñ aku diw,
gàtt aki nag,
bakkan ni tool bu ñu suuxat,
dootuñu yoggoorlu.
13 Su boobaa janq bégem pooj,
waxambaaneek mag feelu ko,
ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen,
bànneexal leen, ñu dëddu naqar.
14 Maay yafal sarxalkat yi, ba reggal leen,
sama ñoñ ñi regge sama ngëneel.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
15 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Yuux dégtu na fa Raama,
ay jalooki jooy yu metti.
Rasel ay jooy ay doomam,
baña noppi,
ndax doomam ya wuute.»
16 Aji Sax ji nag ne ko:
«Baal sa jooy yi
te fomp say rongooñ,
dees na la yool sa coono.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Say doom ay jóge réewu noon, ñibbsi.
17 Am nga yaakaaru ëllëg.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Say doom ay délsi seenum réew.
18 Maa dégg moos askanu Efrayim di binni
naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma,
ni sëllu wu dese tàggat.
Ngalla waññi nu, nu waññiku;
yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla.
19 Dëddu woon nanu la moos
waaye léegi réccu nanu.
Xam nan ne tooñ nanu,
ba tey nuy màttuy wiccax.
Danoo rus, torox
ndax sunu ñaawtéefi ndaw.”»
 
20 Aji Sax ji ne:
«Du Efrayim* ay sama doom ji ma sopp,
gone gi may bànneexal?
Lu ma ko gëdd gëdd,
di ko bàyyi xel.
Moo tax sama xol di ko laaj,
ma yërëm koo yërëm.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
21 «Sampal ay xàmmikaay ci yoon wi,
teg fi say màndarga.
Booy dem, defal sa xel ci yoon wii,
ñall wii nga topp.
Israyil mu taaru mi, ñibbsil,
ñibbsil sa dëkk yii.
22 Ndaw su toogadi si,
foo àppal sa ciŋiñ-caŋañ ji?
Aji Sax ji déy, sàkk na guléet kaw suuf:
yees ba mel ni jigéen juy jëflanteek góor
23 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq.
Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii,
yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi,
yal na la Aji Sax ji barkeel!”
24 «Waa réewum Yuda ak dëkk-dëkkaanam yépp ay bokk dëkk, ak beykat yeek màngaan yi yor gétt. 25 Maay nàndal ku mar, leqli ku loof.»
Yeremeey wax
26 Ba loolu amee ma yewwu, ne xiféet, xam ne samay nelaw neex na.
Aji Sax ji teewlul na Israyil
27 «Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israyil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala. 28 Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqte ak a lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee. 29 «Su boobaa deesatul ne:
“Baay lekk reseñ ju xaay,
mu uum bëñu doom ja.”
30 Su boobaa ku nekk sa bàkkaaru bopp a lay rey. Ku lekk reseñ yu xaay, sa gëñi bopp lay uum.
Kóllëre gu yees a ngi
31 «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees. 32 Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee. 33 «Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ. 34 Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
Lii mooy saxal Israyil
35 Aji Sax ji dafa wax,
moom mi dogal jant di leeral bëccëg,
dogal weer ak biddiiw di leeral guddi,
yëngal géej, kiy gannax yi riir,
kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
36 Mu ne: «Bu askanu Israyil feyee ba fàww, may gis,
dogal yooyoo toxu, may gis.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
37 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Su ma waccee mboolem askanu Israyil
ndax li ñu def lépp,
kon nit a mana natt kawewaayu asamaan,
mbaa mu xayma xóotaayu suuf.»
Kàddug Aji Sax jee.
38 Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkk bi, dale ko ca soorooru Ananel ba ca buntu Ruq ba. 39 Dees na fa rëddaat kemu dëkk bi, jubal ba tundu Gareb, wëri ba Gowa. 40 Mboolem xuru néew yaak dóom ya ak mboolem tool ya, ba ca yoonu ndox ma ca Sedoron, ba ca ruqu buntu Fas ya ca penku: lépp lees di sellalal Aji Sax ji. Deesatu fa buddat mbaa di fa daaneel dara.»
* 31:20 Efrayim kenn la ci sëti Yanqóoba mi ñu dippee Israyil. Turu Efrayim wi fii askanu Israyil la fi taxawal. 31:22 Waxin la wu yéeme wuy wund jëfi guléet ju kenn séentuwul, waaye xamuñu dëgg la mu tekki woon ca yooya jamono.