35
Rekabeen raw na Yudeen
1 Kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo ci Aji Sax ji ci jamonoy buurub Yuda Yowakim doomu Yosya. Mu ne ko:
2 «Demal ca Rekabeen ña, nga wax ak ñoom, indi leen kër Aji Sax ji, dugal leen ci néeg yi benn, te jox leen biiñ, ñu naan.»
3 Ma dem wooyi Yaasaña doomu Yeremi doomu Abàcciña, boole kook ay doomi baayam ak doomam yu góor yépp, làngi Rekabeen ñépp daal.
4 Ma yóbbu leen kër Aji Sax ji, dugal leen ca biir néegu taalibey Xanan, góorug Yàlla gay doomu Igdalyaa; mooy néeg ba dendeek néegu kàngam ya, ca kaw néeg doomu Salum, Maaseya fara bunt ba.
5 Ci kaw loolu ma tegal Rekabeen ñi ay njaqi biiñ yu fees, aki kaas, ne leen: «Naanleen.»
6 Ñu ne: «Nun dunu naan biiñ, ndax sunu maam Yonadab doomu Rekab da noo santoon ne nu: “Buleen naan biiñ mukk, muy yeen ba ci seeni sët, ba fàww.
7 Buleen tabax kër, buleen bey, buleen jëmbat tóokëru reseñ, bumu bokk ci seen alal. Waaye nangeen dëkkey xayma seen giiru dund gépp, su ko defee ngeen gudd fan ci biir réew mii ngeen diy màngaan.”
8 Déggal nanu it sunu maam Yonadab doomu Rekab ci mboolem li mu nu santoon, ne nu bunu naan biiñ sunu giiru dund, nook sunuy jabar ak sunuy doom, góor ak jigéen,
9 bunu tabax kër yu nu dëkke, te tóokër ak tool bu ñuy bey, bumu bokk ci sunu alal.
10 Waaye ay xayma lanu dëkke, di sàmm ak a jëfe mboolem lu nu sunu maam Yonadab santoon.
11 Waaye ba Nabukodonosor buuru Babilon songee réew mi lanu ne: “Nan duggi gaaw biir Yerusalem, ba rëcc mbooloom waa Babilon ak Siri.” Moo nu taxa toog nii ci biir Yerusalem.»
12 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko:
13 «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Demal wax mboolem waa Yuda ak waa Yerusalem, ne leen: “Xanaa dungeen dégg ndigal, ba dégg samay kàddu?” Kàddug Aji Sax jee.
14 “La Yonadab doomu Rekab santoon ay doomam ne leen: ‘Buleen naan biiñ’ de, jëfees na ko. Duñu naan biiñ ba tey jii ndax wormaal seen santaaney maam. Man nag ay yooni yoon laa leen wax waaye déggaluleen ma.
15 Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma.
16 Sëti Yonadab doomu Rekab yii déy wormaal nañu santaane ba leen seen maam santoon, waaye xeet wii déggaluñu ma.”
17 «Kon nag Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa ngi nii di wàcceel Yuda ak képp ku dëkke Yerusalem mboolem musiba mu ma leen tuddaloon. Ndax damaa wax ak ñoom te dégluwñu; ma woo leen, wuyuwñu.»
18 Ba loolu amee Yeremi ne Rekabeen ña: «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Gannaaw wormaal ngeen seen kàddug maam Yonadab, topp santaaneem yépp, ba jëfe lépp lu mu leen santoon,
19 loolu tax na Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi wax ne: “Askanu Yonadab doomu Rekab du ñàkk mukk ku góor ku may liggéeyal ba fàww.”»