45
Barug mucc na
1 Kàddu gii Yeremi waxoon na ko Barug doomu Nerya, gannaaw ba Barug tënkee ci taxañu mbind, kàddu ya ko Yeremi dégtal ca ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya, Yowakim buurub Yuda.
2 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ci yaw, Barug.
3 Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.”
4 Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne:
La ma tabaxoon a ngii,
maa ngi koy daaneel,
la ma jëmbatoon a ngii,
maa ngi koy buddat,
ba réew mépp daj.
5 Looy sàkku ku la beral loxo?
Jaru ko!
Maa ngii di wàcceel musiba képp kuy noyyi.”
Kàddug Aji Sax jee!
“Waaye may naa la sa bakkan di sa yoolu xare,
fépp foo jëm.”»