10
Lingeer buurub Saba seetsi na Suleymaan
Ci kaw loolu Lingeeru Saba dégg riirum Suleymaan ma turu Aji Sax ji waral. Mu dikk di nattusi am xelam, di ko cax cax yu jafe. Mu agsi Yerusalem, ànd ak topp mu takku lool ak giléem yu sëf ay ndàbb yu xeeñ ak wurus wu baree bare ak per yu gànjare. Ba mu dikkee ba ca Suleymaan, mboolem la mu jàppoon ca xelam la ko wax. Suleymaan tontu ko ca mbir ya mu laaj yépp; amul menn mbir mu tiiñ Buur ba leeralalu ko ko. Lingeer buurub Saba gis mboolem xelam Suleymaan mu rafet, ak kër ga mu tabax, ak njëlu këram, ak jataayu dagam ya, ak taxawaayu surgaam ña, ak seen col ga, ak ña yor ay naanam, ak saraxi rendi-dóomal ya muy joxe ca kër Aji Sax ji. Mu daldi yéemu, ba ag noowam réer ko.
Mu ne Buur: «jëw ba ma déggoon ca sama réew ci say mbir ak sa xel mu rafet kay, dëgg la! Gëwma ko woon ba bi ma dikkee, ba teg ci samay bët. Ndeke genn-wàll gi sax waxeesu ma ko woon. Wees nga riir ma ma déggoon ci yaw, ci xel mu rafet ak alal. Ndokklee say nit! Ndokklee sa jawriñ ñii dëkke taxaw ci sa kanam, di dégg sam xel! Cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi la bége, ba teg la ci jalub Israyil. Aji Sax ji daa sopp Israyil cofeel gu dul jeex, moo tax mu fal la buur, ndax nga saxal fi dëgg ak njekk.»
10 Ba mu ko defee Lingeer buurub Saba may Suleymaan fanweeri barigoy wurus ak juróom, ak cuuraayu ndàbb lu ne gàññ, ak per yu jafe. Cuuraayu ndàbb loola Lingeer buurub Saba mayoon Buur Suleymaan, lu ni mel dikkatu fa ndax bare.
11 Ci kaw loolu itam gaali Buur Iram ya daan jële wurus ca réewum Ofir, jële Ofir lu takkoo takku ci banti sàntaal ak per yu gànjare. 12 Buur sàkke ca banti sàntaal ya, ay sëppukaayi kaw taax ngir kër Aji Sax ji, ak kër Buur ak xeeti xalam ngir woykat yi. Banti sàntaal bu ni mel masu faa dikk, te giseesu ko fi ba tey jii.
13 Buur Suleymaan itam may Lingeer buurub Saba mboolem lu mu sàkku, te bokkewul ak la ko Suleymaan joxal boppam ca loxoom bu tàlli ba buur yelloo. Ba loolu amee Lingeer buurub Saba walbatiku, ñibbim réewam, mooki surgaam.
Suleymaan bare woon na alal
14 Wurus wa daan dikkal Suleymaan cim at, diisaay ba ñaar téeméeri barigoy wurus la, 15 te limaaleesul galag ya jóge ca jaaykat ya ak jula yaak mboolem buuri Arabi, ak jaraafi réew ma.
16 Buur Suleymaan nag sàkklu ñaar téeméeri pakk yu mag yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, benn bu ci nekk jël juróom benni kiloy wurus, 17 ak ñetti téeméeri pakk yu ndaw yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, pakk bu ci nekk di kilo ak liibaru wurus. Buur boole ko denc ca këram ga ñuy wax Gottub Libaŋ.
18 Buur teg ca sàkk ngàngune mu mag mu bëñi ñay, daldi koy xoob wurus wu set wecc. 19 Juróom benni dëggastal la ngàngune ma am, wéeruwaay ba ca kaw mërgalu. Mu am loxo wet gu nekk. Loxo yaa nga feggook ñaari jëmmi gaynde yu taxaw, wet gu nekk benn. 20 Mu am it fukki jëmmi gayndeek ñaar yu taxaw ca ñaari weti juróom benni dëggastal ya, ñaari gaynde séq ndëggastal lu nekk. Sàkkeesul lu ni mel ci mboolem nguur yi!
21 Mboolem lu Buur Suleymaan daan naane wurus la, te mboolem ndabi këram ga ñuy wax Gottub Libaŋ wurusu ngalam la. Dara du ca xaalis, ndax xaalis jàppeesu ko woon muy dara ca janti Suleymaan. 22 Te sax ay gaal yu mag la Buur amoon, ñuy ànd ak gaali Iram, benn yoon ci ñetti at yu nekk gaal ya yeb wurus ak xaalis ak bëñi ñay, aki golo ba ciy dàngin.
23 Buur Suleymaan dem na ba sut mboolem buuri kaw suuf ci wàllu alal, ak ci wàllu xel mu rafet. 24 Mboolem àddinaa daan wuta giseek Suleymaan, ngir taataansi xelam mu rafet mi Yàlla def cib xolam. 25 Ñooñu ñoo ko daan indil at ci kaw at, ku nekk ak sab teraanga, muy ay jumtukaayi wurus ak yu xaalis aki mbubb aki gànnaay aki cuuraay aki fas aki berkelle.
26 Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri watiir (1 400), ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu yebal ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. 27 Buur Suleymaan a def xaalis late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi. 28 Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi*, baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde. 29 Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri dogi xaalis (600) la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki dogi xaalis (150), te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen.
* 10:28 Silisi mooy Kewe ba tey.