15
Asaryaa falu na buur ca Yuda
Ba Yerbowam buurub Israyil duggee ñaar fukkeelu at ak juróom ñaar ci nguuram, ca la Asaryaa* doomu Amaciya falu buur ca Yuda. Fukki at ak juróom benn la amoon, ba muy falu buur, te nguuru na juróom fukki at ak ñaar ca Yerusalem. Yaayam mooy Yekolyaa ma cosaanoo Yerusalem. Asaryaa di def li Aji Sax ji rafetlu, mboolem noonee ko Amaciya baayam daan defe. Terewul bérabi jaamookaay ya jëleesu ko fa. Mbooloo ma dañoo wéy di fa def ay sarax ak a taal cuuraay. Aji Sax ji nag mbugal Asaryaa, teg ko jàngoroy ngaana ba kera bés ba mu deeyee. Ci néeg bu ñu ko ber la dëkk. Doomu Buur Yotam moo jiite kër ga, yor kilifteefu askanu réew ma.
Li des ci mbiri Asaryaa ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. Gannaaw gi Asaryaa tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeeli maamam ya, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Yotam doomam moo falu buur, wuutu ko.
Sàkkaryaa falu na buur ca Israyil
Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Sàkkaryaa doomu Yerbowam falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Juróom benni weer la nguuru.
Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu, na ko ay maamam daa defe. Dëdduwul bàkkaar yu Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. 10 Ci kaw loolu Salum doomu Yabes fexeel ko, jam ko ca kanam mbooloo ma, rey ko, daldi falu buur, wuutu ko. 11 Li des ci mbiri Sàkkaryaa bindees ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 12 Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee.
Salum falu na buur ca Israyil
13 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Salum doomu Yabes falu buur ca Israyil. Wenn weer la nguuru, péeyoo Samari. 14 Gannaaw loolu Menayem doomu Gadi bàyyikoo Tirsa ba Samari, daldi fa jam Salum doomu Yabes, bóom ko, falu buur, wuutu ko. 15 Li des ci mbiri Salum ak pexeem ma mu laloon, bindees na ko moos ca téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
16 Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp.
Menayem falu na buur ca Israyil
17 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Menayem doomu Gadi falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at. 18 Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu; giiru dundam dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. 19 Ci jamonoom la Tiglaat Pilser buurub Asiri song réew ma, Menayem jox ko ñetti téeméeri barigoy xaalis ngir mu jàpple ko, ba nguuram gëna dëgër. 20 Menayem dajale xaalis boobu ci Israyil; jële ko ca mboolem boroom alal ya, ku nekk ci ñoom joxe juróom fukki dogi xaalis, ñu yót ko buuri Asiri, mu doora jóge ca réew ma, ñibbi. 21 Li des ci mbiri Menayem ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 22 Gannaaw loolu Buur Menayem saay, fekki ay maamam. Doomam Pekaxiya falu buur, wuutu ko.
Pekaxiya falu na buur ca Israyil
23 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram, ca la Pekaxiya doomu Menayem falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaari at. 24 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. 25 Ba mu ko defee Peka doomu kilifag xarekatam Remalya, fexeel ko, ba rey ko ca Samari, ca tatay kër buur, jamaale Argob ak Arye. Remalyaa nga àndoon ak juróom fukki niti Galàdd. Noonu la ko reye, falu buur, wuutu ko.
26 Li des ci mbiri Pekaxiya ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
Peka falu na buur ca Israyil
27 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Peka doomu Remalyaa falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaar fukki at. 28 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. 29 Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.
30 Ba loolu amee ku ñuy wax Ose doomu Ela lalal Peka doomu Remalya pexe, jam ko mu dee. Mu daldi falu buur, wuutu ko. Loolu yemook ñaar fukkeelu atu nguurug buurub Yuda Yotam doomu Asaryaa. 31 Li des ci mbiri Peka ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
Yotam falu na buur ca Yuda
32 Ba buurub Israyil Peka doomu Remalya duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Yotam doomu Asaryaa falu buur ca Yuda. 33 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog. 34 Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na baayam Usiya daan defe la daan defe. 35 Terewul jëleesu fa bérabi jaamookaay ya, xanaa mbooloo ma di def ay sarax ak a taal cuuraay ba tey, ca bérabi jaamookaay yooyu. Moom nag moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar. 36 Li des ci mbiri Yotam aki jëfam, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 37 Ci jamonoom la Aji Sax ji tàmbalee xabtal Reccin buurub Siri ak Peka doomu Remalya ci kaw Yuda.
38 Gannaaw gi Yotam tëdd, fekki ay maamam. Ca bàmmeelu maamam ya lees ko denc, ca gox ba ñu naan dëkku Daawuda, maamam. Doomam Axas falu buur, wuutu ko.
* 15:1 Asaryaa mooy Osiyas ba tey. 15:19 Tiglaat Pilser mbaa Pul ba tey.