22
Yosya falu na buur ca Yuda
Juróom yetti at la Yosya amoon ba muy falu buur, te fanweeri at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Yedida doomu Adaya ma cosaanoo Boskat. Yosya di def li Aji Sax ji rafetlu, topp ci mboolem tànk yi maamam Daawuda jaaroon, jàddul fenn, du ndijoor, du càmmoñ.
Buur Yosya nag, ca fukk ak juróom ñetteelu atu nguuram, dafa yebal bindkat ba, Safan doomu Asalyaa doomu Mesulam, ca kër Aji Sax ji. Mu ne ko: «Demal ca Ilkiya sarxalkat bu mag ba, ne ko mu yembal saraxi xaalis, yi wattukati bunti kër Aji Sax ji nangoo ci nit ñi. Nañu ko teg ci loxoy liggéeykat yiy saytu liggéeyu kër Aji Sax ji. Ñooñu jox ko liggéeykat ya ca kër Aji Sax ji, di defaraat kër ga, muy liggéeykati bant yi ak tabaxkat yi ak yeneen liggéeykat. Nañu ci jënd bant ak doji yett, defare ko kër gi. Waaye buñu leen laaj nu ñu def xaalis bi ñu leen jox, ndax ñu maandu lañu ci seen liggéey.»
Téereb yoon wi feeñ na
Ilkiya sarxalkat bu mag ba nag ne Safan bindkat ba: «Téereb yoon wi de laa gis ci kër Aji Sax ji!» Ci kaw loolu Ilkiya jox Safan téere ba, mu jàng ko. Ba loolu amee Safan bindkat ba dellu ca Buur, àgge ko gii kàddu: «Sa surga ya sotti nañu xaalis ba nekkoon ca kër Aji Sax ji, ba teg ko ca loxol ñi yor liggéey bi te di saytukati kër Aji Sax ji.» 10 Safan bindkat ba teg ca xamal Buur ne ko: «Ab téere nag la ma Ilkiya sarxalkat bi jox.» Safan jàngal ko Buur.
11 Ba Buur déggee kàdduy téereb yoon wa, daa xotti ay yéreem ndax tiitaange. 12 Mu wax Ilkiya sarxalkat ba, mook Ayikam doomu Safan, ak Agbor doomu Mikaya, ak Safan bindkat ba, ak Asaya bëkk-néegu buur, ne leen: 13 «Demleen seetal ma ci Aji Sax ji, seetaaleel mbooloo meek Yuda gépp ci mbirum kàdduy téere bii feeñ. Sànjum Aji Sax ji tàkk ci sunu kaw kat réy na, ndax sunuy maam a déggul kàdduy téere bii, ngir jëfe mboolem li ñu nu ci bindal.» 14 Ilkiya sarxalkat ba daldi dem ànd ak Ayikam ak Agbor ak Safan ak Asaya, ba ca Ulda yonent bu jigéen bay soxnas wattukatub yére ya, Salum doomu Tigwa doomu Aras. Ulda ma nga dëkkoon Yerusalem ca sanc ba. Ñu wax ak moom.
15 Jigéen ja ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil nee: Xamal-leen ki leen yebal ci man ne ko: 16 “Aji Sax ji nee: Maa ngii di wàcce musiba ci bérabi bii ak ñi ko dëkke, muy mboolem kàdduy téere bi buurub Yuda jàng. 17 Gannaaw ñoo ma dëddu, di taalal yeneen yàlla cuuraay, ngir merloo ma ci mboolem liggéey bu ñu defe seeni loxo, samam sànj mooy tàkk fi bérab bii te du fey.” 18 Buuru Yuda mi leen yónni, ngir ngeen seetlusi ci Aji Sax ji nag, waxleen ko ne ko: “Li Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci kàddu yi ngeen dégg moo di: 19 Gannaaw yaa réccu ci sa xol, ba toroxlu ci kanam Aji Sax ji, ba nga déggee ni ma rëbbe bérab bii mook ñi ko dëkke, muy seen toroxteek seen alkànde, te yaa xotti say yére, jooy fi sama kanam, man it dégg naa la. Kàddug Aji Sax jee. 20 Moo tax maa ngii di la yóbbu nga fekki say maam, dees na la yóbbu ak jàmm ca sa bàmmeel, te say bët du tegu ci mboolem musiba mi may wàcce ci bii bérab.”» Ba loolu amee ñu dellu, yegge Buur kàddu ga.