Ndigal yi jëm ci sellal
17
(Saar 17—26)
Li war ci jaamu ak sarxal
Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israyil gépp ne leen li Aji Sax ji santaane mooy lii: Képp kuy góor ci waa kër Israyil, bu rendee aw nag mbaa xar mbaa bëy ci biir dal bi, ak fu génn dal bi, te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca bunt jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees na ko dagge ci biir bànni Israyil. Su ko defee bànni Israyil dinañu indil Aji Sax ji juri sarax yi ñuy rendi ci àll bi. Dañu koo wara yóbbu ca sarxalkat ba, fi Aji Sax ji, ca bunt xaymab ndaje ma, defal ko Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm. Sarxalkat bi day xëpp deret ji ci sarxalukaayu Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi, ba noppi, lakkal Aji Sax ji nebbon bi, muy xeeñ xetug jàmm. Buñu di sarxalatil tuur, yi ñuy jëmmale sikket, di ko bokkaalee. Na loolu di dogal bu leen war fàww, ñoom ak seen askan. Wax leen boog ne leen: Képp kuy góor, ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa mu bokk ci doxandéem yi ci seen biir, buy génne ab saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, sarxalal ko Aji Sax ji, kooku dees koo wara dagge ci biir bànni Israyil.
10 «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil. 11 Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam. 12 Looloo waral ma ne bànni Israyil, bu kenn ci ñoom lekk deret, te doxandéem bi ci seen biir it bumu lekk deret.
13 «Képp ku bokk ci bànni Israyil mbaa ci doxandéem yi ci seen biir, bu rëbbee ba jàpp mala mbaa njanaaw, mu di lu dagana lekk, na tuur deret ji, suul, 14 ndax dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Moo waral, man Aji Sax ji, ma ne bànni Israyil buñu lekk deretu menn mbindeef ngir dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Képp ku lekk deret, dees koy dagge ci askan wi.
15 «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set. 16 Waaye su fóotul, sanguwul, mooy gàddu bàkkaaram.»