7
Yàqute maase na
1 Wóoy, ngalla man mi mel ni kuy forsi,
te meññeef ma fatu,
may raasaatu, te du cabbu reseñ ju nit lekk,
du figg ju bees ji ma namm.
2 Ngor a jeex ci réew mi,
njub tumurànke ci nit ñi.
Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru,
ku nekk, mbokkam lay fiir.
3 Lu bon la seeni loxo mane:
kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger,
boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam,
ñu ànd ràbbum pexe.
4 Ki gën ci ñoom, neexook ag dég,
ki ci jub yées ag taxas.
Bés ba say jongrukat yégle woon,
sa bésu mbugal taxaw na,
léegi lees di waaru.
5 Buleen gëm ab xarit,
buleen wóolu ab xejj,
fi kanam ndaw siy tëdd sa gannaaw sax,
sàmmal sa bunti gémmiñ.
6 Doom ju góor a ngi dofloo baay ba,
ju jigéen ja jógal ndey ja,
jabar jógal ndeyu jëkkër ja,
nooni nit ki di waa këram.
7 Man nag Aji Sax ji laay séentu,
Yàlla ji may musal laay xaar,
te sama Yàllaa may nangul.
Yërmande wuutu na mbugal ñeel Siyoŋ
8 Yaw samab noon, bu ma ree;
maa daanu, maay jóg.
Ci biir lëndëm laa toog,
waaye Aji Sax jeey samag leer.
9 Maa moy Aji Sax ji,
kon naa tegoo meram,
ba mu layool ma, dëggal ma,
génne ma ci leer gi,
ma gis ag njekkam.
10 Ndaw siy samab noon moo koy seede,
sëlmoo gàcce,
moom ma doon naa: «Ana sa Yàlla Aji Sax ji?»
Samay gët a naa ndaw soosu jàkk,
ñu di ko dëggaate ni banu mbedd.
11 Bés a ngii bees di tabaxaat say tata,
su bés baa lees di yokk sa kemu suuf.
12 Su bés baa ci yaw lees di dikk,
bawoo Asiri ak dëkki Misra,
bawoo diggante Misra ba ca dex ga,
ak géej ba géej, tund ba tund.
13 Àddina ab gent lay doon
ndax ñi ko dëkke,
muy añub seeni jëf.
14 Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ,
sa gàtt yi nga séddoo,
te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen,
fi digg parlu mu naat.
May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd
na jant ya woon.
15 Aji Sax ji nee: «Maa leen di won ay kiraama,
na woon ba ngeen di génn réewum Misra.»
16 Xeet yee ciy gis, rus,
te seen gépp njàmbaar du tee ñu ub seen gémmiñ,
seeni nopp buur.
17 Ñooy mëq suuf ni jaan,
ak ndëgmeenti suuf,
di lox, génne seeni tata,
te su boobaa yaw sunu Yàlla Aji Sax ji lañuy tiit,
ragal la.
18 Ana Yàlla ju mel ni yaw,
di bale ag tooñ, di jéllale ag moy,
ñeel ndesu ab séddoom.
Kii du denc mer ba fàww,
te moo bëgg di yéwéne.
19 Moo nuy yërëmati;
sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam,
te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
20 Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma,
na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.