2
Almasi mooy kenug mbooloom gëmkat ñi
Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der. Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy Kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe, gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.
Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko. Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi. Moo waral lii dikk ci Mbind mi:
«Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju doorukaay,
doju tànnéef wu gànjare.
Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk*
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag:
«Moo di doj wa tabaxkat ya beddi woon,
te mu mujj di doju coll wi
Te it:
«Mooy doj wuy fakktale,
di xeer wuy daaneel
Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.
Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme. 10 Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo§; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.
Liy wàllu gëmkatu Almasi ci àddina
11 Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol. 12 Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.
Déggal-leen njiit yi
13 Nangul-leen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe, 14 mbaa boroom dëkk yi diy ndawam, te mu tabb leen, ngir ñu mbugal ñiy def lu bon, te sargal ñiy def lu baax. 15 Ndax coobarey Yàlla kat moo di ngeen di def lu baax, ba wedamal nit ñu ñàkk bopp ñi xamul dara. 16 Ay gor ngeen, waaye jaami Yàlla ngeen. Kon buleen taafantoo li ngeen diy gor ba def lu bon. 17 Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.
Nanu muñ coono, roye ko Almasi
18 Yeen jaam yi, nangul-leen te weg wegeel gu mat sëkk seeni sang, te du sang yi baax te lewet doŋŋ, waaye ñu wex ñi itam ci lañu. 19 Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la. 20 Muñ ay dóor yu la fekk tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla. 21 Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi itam sonnal na leen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
22 «Moo bàkkaarul, fenul*
23 Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg. 24 «Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam 25 «Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.
* 2:6 Seetal ci Esayi 28.16. 2:7 Seetal ci Sabóor 118.22. 2:8 Seetal ci Esayi 8.14. § 2:10 Seetal ci Ose 1.6, 9 ak 2.25. * 2:22 Seetal ci Esayi 53.9. 2:24 Seetal ci Esayi 53.5. 2:25 Seetal ci Esayi 53.6.