22
1 Jëw bu rafet a gën barele,
wegeel gën xaalis ak wurus.
2 Ku am ak ku ñàkk a bokk lenn:
Aji Sax jee leen boole sàkk.
3 Kuy foog, gisu ay, làqu;
ab téxét ne ca tëñëx, loru.
4 Woyofal te ragal Aji Sax ji,
am alal, gudd fan ak daraja.
5 Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir;
ku sàmm sa bakkan sore ko.
6 Tegal gone ciw yoon,
ba bu màggee, du ko wacc.
7 Ku am ay yilif ku ñàkk,
koo leb di surgaam.
8 Ku ji njubadi, góob fitna,
yet wa muy dóore, damm.
9 Ku tabe am barke,
mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10 Dàqal kuy ñaawle, ay jeex,
xulooki saaga dakk.
11 Ku dëggu, wax ja yiw,
buur di xaritam.
12 Aji Sax jeey sàmm liy dëgg,
di weddi waxi fen-kat.
13 Bul yaafus, ba naan: «Gayndee ngi ci biti,
dañu may rey ci mbedd mi!»
14 Waxi ndaw su yemadi am yeer la,
ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.
15 Yëfi dof daa sax ci xolu gone,
boo bantalee, mu tàggook moom.
16 Not néew-ji-doole ngir yokkule,
mbaa may boroom alal,
loo ci def mu wàññi la.
Fanweeri tegtal a ngi
17 Teewlul te déglu li boroom xel yi wax.
Defal sam xel ci li ma lay xamal.
18 Soo mokkalee, ba man koo tari,
muy sa mbégte.
19 Yaw laa koy xamal tey jii,
ndax nga wóolu Aji Sax ji.
20 Dama laa bindal fanweeri dénkaane,
ci wàllu digal ak xam-xam,
21 ngir xamal la lu wér te dëggu,
nga yóbbaale kàdduy dëgg,
yoo tontoo ña la yebal.
[1]
22 Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la.
Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
23 Aji Sax ji da koy taxawu,
ku ko xañ, mu xañ la bakkan.
[2]
24 Bul xaritook ku gaawa mer,
bul ànd ak ku tàng bopp.
25 Lu ko moy nga mel ni moom,
te kon nga lonku.
[3]
26 Bul bokk ci ñiy dige,
di gàddul nit bor.
27 Soo amul loo ko feyale,
ñu yékkatee la sab lal, nangu ko.
[4]
28 Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf
te say maam tegoon ko fa démb.
[5]
29 Seetlul ku man liggéeyam,
buur lay liggéeyal,
du liggéeyal baadoolo.