Yeneen kàddu yu xeloo ngi yu tukkee ci Suleymaan
25
(Saar 25—29)
Lii it ay kàddu yu xelu la, di yu Suleymaan, ay niti Esekiya buurub Yuda sotti ko.
 
Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq,
darajay buur a ngi ci li mu feeñal.
Maneesula daj li ci xelu buur,
xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
 
Xellil xaalis, tonni lu ca rax,
ba ab tëgg man caa am ndab.
Ab soxor it, dàqal, mu sore buur,
ngir njubte law, jalam sax.
 
Bul réy-réylu fi kanam buur,
bul tooge jataayu boroom daraja,
ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,»
moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa.
 
Boo gisalee sa bopp it,
bul gaawa layooji,
ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
Ñaarool ak ki nga joteel,
te bul jéebaane jaambur.
10 Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la,
sab der yàqu yaxeet.
 
11 Wax ju ñor di nataalu wurus
wu tege ci xaalis.
12 Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg,
jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
 
13 Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem,
mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
 
14 Kuy dige te doo joxe,
yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
 
15 Muñ mer ay nax kilifa,
te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
 
16 Boo gisee lem, lekkal lu yem;
bu ëppee, nga waccu ko.
 
17 Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo;
boo ko sàppee, mu jéppi la.
 
18 Ku seedeel sa moroom ay fen,
yen nga ko aw njur mbaa saamar mbaa fitt.
 
19 Bul wóolu workat bésub njàqare,
mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
 
20 Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg,
yaa futti mbubbam cib sedd,
mbaa nga jonj xorom ci góomam.
 
21 Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk,
bu maree, may ko mu naan,
22 day rus ba mel ni koo yeni xal,
te Aji Sax jee lay fey.
 
23 Jëw, mer a cay topp;
mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
 
24 Dëkkeb ruq cim sàq
moo gën jabar ju pànk.
 
25 Xibaaru jàmm, bawoo fu sore
mooy ndox mu sedd ci ku loof.
 
26 Ku jub bu dee nangul ku bon, yàqu na,
ni seyaan bu nëx mbaa teen bu xàbb.
 
27 Lekk lem ju ëpp baaxul,
te wut waaw-góor du ngóora.
 
28 Ku dul ànd ak sa sago,
yaa neexa song ni dëkk bu dara wërul.